Skip to content

«ku dul yërëm nit ñi Yàlla mu kawe mi du ko yërëm».

Jële nañu ci Jaabir Ibn Abdullah Al-Xasrii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:

«ku dul yërëm nit ñi Yàlla mu kawe mi du ko yërëm».

«مَنْ لَا يَرْحَمِ النَّاسَ لَا يَرْحَمْهُ اللهُ عَزَّ وَجَلَّ».

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne ki dul yërëm nit ñi Yàlla mu kawe mi du ko yërëm, koon jaam bi di yërëm mbindeef yi daa bokk ci sabab yi gën a rëy yi nga xamne dees na ci ame yërmàndey Yàlla mu kawe mi.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Yërmànde ci mbooleem mbindéef loolu de luñu sàkku la, waaye dañoo tudd nit ngir fonk giñuleen fonk.

Yàlla mooy Aji-Yërëme ji te mooy yërëm ay jaamam yiy yërëme, ndax pay moom ca kem jëf ja rekk.

Yërëm nit ñi day làmboo di àggale ci ñoom baax di leen jeñal lu ñaaw tey jëflanteeg ñoom lu rafet.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (8/ 10) (6013).

Téere Muslim bi gën a wér (4/ 1809) (2319).

Yataal gi (5)

شرح رياض الصالحين.

لابن عثيمين (2/ 553).

نزهة المتقين شرح رياض الصالحين (1/ 247).

بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.

لسليم الهلالي (1/ 319).