Skip to content

"Yaw Abuu Sarri boo toggee am ñeex na nga baril ndox mi, te sédd ci sa dëkkandoo".

Jële nañu ci Abuu Sarrin yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:

"Yaw Abuu Sarri boo toggee am ñeex na nga baril ndox mi, te sédd ci sa dëkkandoo".

«يَا أَبَا ذَرٍّ إِذَا طَبَخْتَ مَرَقَةً فَأَكْثِرْ مَاءَهَا، وَتَعَاهَدْ جِيرَانَكَ».

Muslim soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day ñaax Abuu Sarrin Al-Xifaarii yal na ko Yàlla dollee gërëm ci ne bu toggee ñeex na baril ndox mi ak ñeex mi, te sóoraale ci dëkkandoom.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Ñaaxe ci rafetal jëflante ak dëkkandoo yi.

Sopp nañu di mayante aka tibbalante ci diggante dëkkandoo yi; ndax loolu day waral bëggante te day yokk cofeel, tibbalante gi nag dana gën a feddaliku bu dee ñam wi dafa am xet, mu xam aajog dëkkandoo gi.

Ñaaxe ci def njekk ak la ca jàppandi donte dafa néew, ak dugal mbégte ci jullit ñi.

Dellluwaay yi

Téere Muslim bi gën a wér (4/ 2025) (2625).

Yataal gi (6)

بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.

لسليم الهلالي (1/ 386).

شرح رياض الصالحين.

لابن عثيمين (3/ 175).

نزهة المتقين شرح رياض الصالحين.

لمجموعة من الباحثين (1/ 301).