ñooñu aw nit lañu wow bu ku baax faatoo fa ñoom, dañuy tabax ca bàmmeelam ba jàkka
Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit ñi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne :
Ummu Salamata dafa xibaar Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- benn jàngu bu mu gis ca Abasa, (jàngu : jaamukaayu katolig yi) ñu koy woowe Maariya, mu wax ko la mu fa gis ci ay nataal, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: " ñooñu aw nit lañu wow bu ku baax faatoo fa ñoom, dañuy tabax ca bàmmeelam ba jàkka, daaldi cay def nataal yooyu, ñooñu ñoo yées ci nit ñi fa Yàlla".
أَنَّ أُمَّ سَلَمَةَ ذَكَرَتْ لِرَسُولِ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ كَنِيسَةً رَأَتْهَا بِأَرْضِ الْحَبَشَةِ، يُقَالُ لَهَا مَارِيَةُ، فَذَكَرَتْ لَهُ مَا رَأَتْ فِيهَا مِنَ الصُّوَرِ، فَقَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «أُولَئِكَ قَوْمٌ إِذَا مَاتَ فِيهِمُ الْعَبْدُ الصَّالِحُ، أَوِ الرَّجُلُ الصَّالِحُ، بَنَوْا عَلَى قَبْرِهِ مَسْجِدًا، وَصَوَّرُوا فِيهِ تِلْكَ الصُّوَرَ، أُولَئِكَ شِرَارُ الْخَلْقِ عِنْدَ اللهِ».
Ndayu jullit ñi Ummu Salamata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- dafa nettali Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne moom ba mu nekkee ca suufus Abasa dafa gis ab jàngu ñu koy woowe Maariya- ay nataal ak i rafetal ak i rëd-rëd ñoo fa nekk; mu yéemu ci loolu ! Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- leeral li waral ñu def fa foto yooyu; Mu wax ne : ñii ngay wax bu amaan ku baax ku faatu ci ñoom dañuy tabax jàkka ci kaw bàmmeelam di fa julli, daa di fay def nataal yooyu, Mu leeral ne ñiy def loolu ñoo yées ci mbindeef yi fa Yàlla, ndax seen i jëf da lay yóbbe ci bokkaale Yàlla mu kawe mi.
...:
Tabax jàkka ci bàmmeel yi dafa araam, walla di fa julli, mbaa suul néew ci jàkka yi; ngir sakk yoon yiy jëme ci bokkaale.
Tabax jàkka ci bàmmeel yi, ak samp fa ay nataal, daa bokk ci jëfi Yahuut yi ak Nasaraan yi, te ku ko def, mi ngi leen di niru-nirulu.
Araamalees na nataal lu am ruu.
Ku tabax jàkka cib bàmmeel def fa ay nataal, kon moom ci ñi yées ci mbindeefi Yàlla yi la bokk.
Sariiha dafa aar Tawhiid aar gu mat sëkk, ci fatt wépp yoon wuy jëme ci bokkaale.
Tere nañu ëppal ci ñu baax ñi; ndaxte sabab la ci tàbbi ci bokkaale.
Téere Al-buxaariy bi gën a wér (1/ 94) (434).
Téere Muslim bi gën a wér (1/ 375) (528).
Yataal gi (14)
مرقاة المفاتيح.
لعلي القاري (7/ 2857).
توضيح الأحكام مِن بلوغ المرام.
لعبد الله البسام (2/ 115).
فتح ذي الجلال والإكرام شرح بلوغ المرام.
لابن عثيمين (1/ 598).
منحة العلام في شرح بلوغ المرام.
لعبد الله الفوزان (2/ 469).
تيسير العلام شرح عمدة الأحكام.
لعبد الله البسام (ص290).
الجديد في شرح كتاب التوحيد.
لمحمد القرعاوي (ص183).
الملخص في شرح كتاب التوحيد.
لصالح الفوزان (ص168).
Cited in books
6 BooksYataal gi (6)
- التوحيد في ضوء عقيدة الإمام الشافعي رحمه الله ونصوصه ومروياته"أولئك إذا مات فيهم الرجل الصالح- أو العبد الصالح - بنوا على قبره مسجدا، وصوروا فيه تلك الصور، أولئك شرار الخلق عند الله".([81])
- الصلاة التي علمها النبي ﷺ الصحابة رضي الله عنهمالصلاة التي علمها النبي ﷺ الصحابة رضي الله عنهم«إِنَّ أُولَئِكَ، إِذَا كَانَ فِيهِمُ الرَّجُلُ الصَّالِحُ، فَمَاتَ، بَنَوْا عَلَى قَبْرِهِ مَسْجِدًا، وَصَوَّرُوا فِيهِ تِلْكِ الصُّوَرَ، أُولَئِكِ شِرَارُ الْخَلْقِ عِنْدَ اللهِ يَوْمَ الْقِيَامَةِ»[344].
- الصلاة التي علمها النبي ﷺ الصحابة رضي الله عنهم«إِنَّ أُولَئِكَ، إِذَا كَانَ فِيهِمُ الرَّجُلُ الصَّالِحُ، فَمَاتَ، بَنَوْا عَلَى قَبْرِهِ مَسْجِدًا، وَصَوَّرُوا فِيهِ تِلْكِ الصُّوَرَ، أُولَئِكِ شِرَارُ الْخَلْقِ عِنْدَ اللهِ يَوْمَ الْقِيَامَةِ»[344].
- حراسة التوحيدالتحذير من بناء المساجد على القبور«أُولَئِكَ إِذَا مَاتَ فِيهِمُ الرَّجُلُ الصَّالِحُ؛ بَنَوْا عَلَى قَبْرِهِ مَسْجِدًا، وَصَوَّرُوا فِيهِ تِلْكَ الصُّوَرَ، أُولَئِكَ شِرَارُ الْخَلْقِ عِنْدَ اللَّهِ».
- شرح الصدور بتحريم رفع القبور«أُولَئِكَ قَوْمٌ إِذَا مَاتَ فِيهِمُ الْعَبْدُ الصَّالِحُ، أَوِ الرَّجُلُ الصَّالِحُ، بَنَوْا عَلَى قَبْرِهِ مَسْجِدًا، وَصَوَّرُوا فِيهِ تِلْكَ الصُّوَرَ، أُولَئِكَ شِرَارُ الْخَلْقِ عِنْدَ اللهِ»[5].
- شرح الصدور بتحريم رفع القبور«أُولَئِكَ قَوْمٌ إِذَا مَاتَ فِيهِمُ الْعَبْدُ الصَّالِحُ، أَوِ الرَّجُلُ الصَّالِحُ، بَنَوْا عَلَى قَبْرِهِ مَسْجِدًا» [27]