Skip to content

"wàcce nañu ci man aaya boo xam ne moo ma gënal àdduna bi yëpp".

Jële nañu ci Anas ibn Maalik yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:

Bi {Innaa fatahnaa laka fathan mubiinan li yaxfira laka Allaahu} ba ci {fawsan hasiiman} [Al-Fath: 1-5] wàccee fekk moo nga jóge Hudaybiya, njàqare ak jaaxle nekk ci ñoom, fekk rendi woon nañu gàtt ya ca Hudaybiya, dafa wax ne: "wàcce nañu ci man aaya boo xam ne moo ma gënal àdduna bi yëpp".

لَمَّا نَزَلَتْ: {إِنَّا فَتَحْنَا لَكَ فَتْحًا مُبِينًا لِيَغْفِرَ لَكَ اللهُ} إِلَى قَوْلِهِ {فَوْزًا عَظِيمًا} [الفتح: ١-٥] مَرْجِعَهُ مِنَ الْحُدَيْبِيَةِ، وَهُمْ يُخَالِطُهُمُ الْحُزْنُ وَالْكَآبَةُ، وَقَدْ نَحَرَ الْهَدْيَ بِالْحُدَيْبِيَةِ، فَقَالَ: «لَقَدْ أُنْزِلَتْ عَلَيَّ آيَةٌ هِيَ أَحَبُّ إِلَيَّ مِنَ الدُّنْيَا جَمِيعًا».

Muslim soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Anas ibn Maalik yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day nettali ne bi waxu Yàlla wàccee ci Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc: {Innaa fatahnaa laka fathan mubiinan (1) li yaxfira lakallaahu maa taqaddama min sanbihii wa maata axxara wa yutimma nihmatahuu alayka wa yahdiyaka siraatan mustaxiiman (2) wa yansurakallaahu nasran asiisan (3) huwallasii ansalas sakiinata fii xuluubil muuminiina li yasdaaduu iimaanan maha iimaanihim wa lillaahi junuudus samaawaati wal ardi wa kaanallaahu aliiman hakiiman (4) liyudxilal muuminiina wal muuminaati jannaatin tajrii mintahtihal anhaaru xaalidiina fiihaa wayukaffira anhum sayyi aatihim wakaana saalika indallaahi fawsan asiiman} [Al-Fath: 1-5], jamono ja muy wàññeeku jóge Hudaybiya, fekk njàqare ak jaaxle nekk ci Sahaaba yi, ndax li ñu leen teree Umra, ak it li yéwénoo gi am te ñu njort ne gënul ci jullit ñi, fekk it ne rendi nañu seen gàtt yi ca Hudaybiya, Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daal di wax ne: Wàcce nañu ci man aaya boo xam ne moo ma gënal àdduna bi yëpp, mu daal di koy jàng.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Leeral màggayu li Yàlla xéewalal Yonenteem bi Muhammat yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci ag ubbee gu mgg ci yéwénoog Hudaybiya ga; ba tax mu wax ne: {Nun noo la Ubbil Ubbi gu fés} ñaari aaya yi.

Leeral li Yàlla xéewalal Sahaaba yi yal na leen Yàlla dollee gërëm ba tax ñu topp ndigal li wommatul ko, ba tax Yàlla mu kawe mi wàcce ci ñoom waxam ji: {loolu tax na ba Yàlla dana tàbbal jullit ñu goor ñi ak jullit ñu jigéen ñi ci Àjjana yoo xam ne ay dex ñooy daw ci suufam} ba aaya bi jeex.

Leeral ngëneelu Yàlla ci Yonenteem bi ak way-gëm ñi ci mu dig leen ag ubbite ak ug gañaay.

Sahdii wax na ci tafsiiram bi ci aaya bii ne: {Nun Ubbil Nanu la ubbi gu fés} [Al-Fath 1], ubbite gii ñu tudd mooy yéwénoog Hudaybiya, bi bokkaalekat yi baaree Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ba mu ñëwee ngir Umra ca xissa bu gudd ba, te fa mbir ma mujje mooy ne Yonente bi dafa yéwénoo ci ñu bàyyi xeex bi ci digganteem ak ñoom fukki at, ak it mu def Umra bi ci at miy ñëw, ak ne ku bëgg a dugg ci kóllareg bokkaalekat yi far ak ñoom man na caa dugg, ku bëgg a dugg ci kóllareg Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ak pas-pasam it mu dugg ca. Loolu moo tax bi ñenn nit ñi aare ñeneen ñi ci la wooteg diine Yàlla ji yaatu, ba mujj jullit bi am kóolute ba gox bu mu man a nekk ci gox yi dana man a def loolu, ba ki xér ci xam dëgg-dëggi lislaam dana ko man a xam, ci diir boobu nit ñi dugg ci diiney Yàlla ji di ay mbooloo, loolu moo tax Yàlla tudde ko ag ubbite, tudde ko ubbite gu fés: maanaam gu feeñ te bér, loolu nag ndaxte li ñu jublu ci ubbi réewi bokkaalekat yi mooy dëgëral diiney Yàlla ji, ak jullit yi not, te lii lu am la ci ubbite googu.

Dellluwaay yi

Téere Muslim bi gën a wér (3/ 1413) (1786).

Yataal gi (2)

تفسير القرطبي (16/ 259-265).

البحر المحيط الثجاج في شرح صحيح الإمام مسلم بن الحجاج (31/ 234).