«Ndax kenn ci yéen bëgg na bu delloo ci njabootam fekk fa ñàtti giléem yu ëmb, rëy te suur?
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«Ndax kenn ci yéen bëgg na bu delloo ci njabootam fekk fa ñàtti giléem yu ëmb, rëy te suur?» Nu ne ko: waaw. Mu ne: «kenn ci yéen jàng ñàtti aaya ci julli moo gën ci moom ñàtti giléem yu ëmb rëy te suur».
«أَيُحِبُّ أَحَدُكُمْ إِذَا رَجَعَ إِلَى أَهْلِهِ أَنْ يَجِدَ فِيهِ ثَلَاثَ خَلِفَاتٍ عِظَامٍ سِمَانٍ؟» قُلْنَا: نَعَمْ. قَالَ: «فَثَلَاثُ آيَاتٍ يَقْرَأُ بِهِنَّ أَحَدُكُمْ فِي صَلَاتِهِ خَيْرٌ لَهُ مِنْ ثَلَاثِ خَلِفَاتٍ عِظَامٍ سِمَانٍ».
Leerarug hdiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne payug jàng ñàtti aaya ci julli; moo gën nit ki fekk ca këram ñàtti giléem yu ëmb rëy te suur.
...:
Bokk na ci njariñal hdiis bi: Leeral ngëneelu jàng Alxuraan ci julli.
Jëf yu baax yi moo gën te mooy koomum àdduna bii di aji-jeex te moo fiy des.
Ngëneel lii nag tënkuwul ci jàng ñàtti aaya ci julli rekk; saa bu aji-julli ji di gën a yokk aaya yi ci julli gi ab yoolam di gën ci moom limub giléem yooyee.
Téere Muslim bi gën a wér (1/ 552) (802).
Yataal gi (4)
إكمال المعلم (3/172).
الإفصاح عن معاني الصِّحاح (8/65).
فتح المنعم شرح صحيح مسلم (3/620).
البحر المحيط الثجاج (16/343).
Cited in books
2 BooksYataal gi (2)
- الذكر والدعاء والعلاج بالرقي من الكتاب والسنة"أيحب أحدكم إذا رجع إلى أهله أن يجد فيه ثلاث خَلِفَاتٍ عِظامٍ سمانٍ؟ " قلنا نعم.
- المنتقى من المتجر الرابح في ثواب العمل الصالح - المعتمدالمنتقى من المتجر الرابح في ثواب العمل الصالح“أيحب أحدكم إذا رجع إلى أهله أن يجد فيه ثلاث خلفات عظام سمان؟” قلنا: نعم، قال: “فثلاث آيات يقرأ بهن أحدكم في صلاته، خير له من ثلاث خلفات عظام سمان”.