Skip to content

"Àdduna de luñu rëbb la, rëbb it li ci biiram, ba mu des tudd Yàlla ak lu ko niru ak boroom xam-xam walla kiy sàkku xam-xam".

Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: dégg naa Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc muy wax ne:

"Àdduna de luñu rëbb la, rëbb it li ci biiram, ba mu des tudd Yàlla ak lu ko niru ak boroom xam-xam walla kiy sàkku xam-xam".

«أَلاَ إِنَّ الدُّنْيَا مَلْعُونَةٌ، مَلْعُونٌ مَا فِيهَا، إِلاَّ ذِكْرُ اللهِ وَمَا وَالاَهُ وَعَالِمٌ أَوْ مُتَعَلِّمٌ».

At-tirmisiy soloo na ko, ak Ibnu Maaja.
Tane na
Leeral gi

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne àdduna ak li ci biiram lu Yàlla bañ la ŋàññ ko bàyyi ko te soreele ko, li ci biiram lu ñu bàyyi la te deesu ko sant; ndax moom ak li ci biiram dañuy fàbbe wolif Yàlla di soreele Yàlla, ba mu des tudd Yàlla ak lu ko jege te nuru ko di lu Yàlla bëgg, walla boroom xam-xamu Sariiha bi koy jàngal nit ñi, mbaa aji-sàkku ji xam-xam.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Daganul ñuy rëbb àdduna cig boyal; ndax li ay hadiis rot ci tere loolu, waaye dagan na ñu rëbb lépp luy soreele Yàlla mu kawe mi di fàbbiwaate wolif jaamu ko.

Lépp lu nekk ci àdduna po la ak caaxaan ba mu des tudd Yàlla ak lépp luy sabab di dimbalee ci loolu.

Leeral ngëneelu xam-xam ak i ñoñam ak ñi koy sàkku.

Ibn Taymiya nee na: lañu ciy ŋàññ dafa araam ci lu dul geneen anam, walla mu dagan ci anamug barilante ak ndamu, ak lu ñuy denc ngir jublu ca a puukarante ak werente, te loolu mooy li woroom xel yi bañ lool.

Dellluwaay yi

Téere Sunna yi bu At-tirmisiy (4/ 151) (2322).

Téere Sunna yi bu Ibnu Maaja (5/ 231) (4112).

Yataal gi (8)

بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.

لسليم الهلالي (1/ 542).

نزهة المتقين شرح رياض الصالحين.

لمجموعة من الباحثين (1/ 424).

كنوز رياض الصالحين.

لمجموعة من الباحثين (7/ 325).

شرح رياض الصالحين.

لابن عثيمين (3/ 374).