Skip to content

am nga li nga mébét ak lu mel ni moom".

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:

"barab bu kenn ci yéen bi gën a suufe ca àjjana mooy ñu wax ko: mébétal muy mébét di mébét, mu ne ko: ndax mébét nga? Mu ne: waaw, mu ne ko: am nga li nga mébét ak lu mel ni moom".

«إِنَّ أَدْنَى مَقْعَدِ أَحَدِكُمْ مِنَ الْجَنَّةِ أَنْ يَقُولَ لَهُ: تَمَنَّ فَيَتَمَنَّى، وَيَتَمَنَّى، فَيَقُولُ لَهُ: هَلْ تَمَنَّيْتَ؟ فَيَقُولُ: نَعَمْ، فَيَقُولُ لَهُ: فَإِنَّ لَكَ مَا تَمَنَّيْتَ وَمِثْلَهُ مَعَهُ».

Muslim soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne ki gën a suufe te gën a néew daraja ak martaba ci ñiy dugg àjjana mooy ñu wax ko: mébétal, muy mébét di mébét, ba deseetul genn mébét lu dul ne tudd na ko, mu ne ko: ndax mébét nga? Mu ne: waaw, mu ne ko: am nga li nga mébét ak lu mel ni moom.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Rawanteg këri waa àjjana ya.

Leeral màggug teddngay Yàlla mu kawe mi tudd naa Sellam gi.

Xéewali àjjana yi tënkuwul ci mbir mu ñu ràññee, wànte aji-gëm ji dana ca fekk lépp lu mu mébét te bakkanam bëgg ko muy ngëneel ak tabe ak teddnga bu bawoo ci Yàlla mu kawe mi.

Dellluwaay yi

Téere Muslim bi gën a wér (1/ 167) (182).

Yataal gi (8)

مرقاة المفاتيح شرح مشكاة المصابيح.

لعلي القاري (9/ 3585).

تطريز رياض الصالحين.

لفيصل آل مبارك (ص1090).

بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.

لسليم الهلالي (3/ 348).

نزهة المتقين شرح رياض الصالحين.

لمجموعة من الباحثين (2/ 1292).