Skip to content

«yaw Bilaal taxawalal julli gi, noppal nu ci».

Jële nañu ci Saalim Ibn Abil Jahd mu wax ne: benn waay dafa wax ne: aka neexoon ma julli ndax ma noppalu, mu mel ni dañu koo sikk ci loolu, mune leen dégg naa Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax ne:

«yaw Bilaal taxawalal julli gi, noppal nu ci».

«يا بلالُ، أقِمِ الصَّلاةَ، أرِحْنا بها».

Abóo Daawuda soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Benn waay ci Sahaaba yi dafa wax ne: aka neexoon ma julli ndax ma noppalu, mu mel ni ñi ko wër dañu koo sikk ci loolu, mune leen: dégg naa Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax ne: éey Bilaal! Yëkkëtil nodd gi te taxwal; ndax nu nappaloo ko; loolu nag ngir li ci nekk ci déeyante ak Yàlla, ak nooflaayu ruu ak xol.

Maanaay baat yi

...:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Nooflaayu xol day ame ci julli; ngir li ci nekk ci déeyante ak Yàlla mu kawe mi.

Weddi ci kaw kuy tàyyeel ci jaamu Yàlla.

Képp ku def li ko war, ba setal ca boppam, dana am noflaay ak yég-yégu dal.

Dellluwaay yi

Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda (7/ 338) (4985).

Yataal gi (4)

الكاشف عن حقائق السُّنن (4/1217).

عون المعبود وحاشية ابن القيم (13/ 225).

مرقاة المفاتيح (3/939).

شرح سنن أبي داود للعباد (567/ 6).