Skip to content

"yaw Yonnente Yàlla bi, alal yi sànku na, yoon yi dagg na, ñaanal nu Yàlla mu xettali nu

Jële nañu ci Anas ibn Maalik yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:

Jenn waay dafa dugg ci Jàkka ji bisu àjjuma ci bunt bi mel mi karu àttekaay, fekk Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moo ngi taxaw di xutba, mu jublu Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daal di taxaw, topp mu ne ko: "yaw Yonnente Yàlla bi, alal yi sànku na, yoon yi dagg na, ñaanal nu Yàlla mu xettali nu, Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc yëkkëri ay yoxoom, topp mu ne: "Allaahuma axisnaa, Allaahuma axisnaa, Allaahuma axisnaa", Anas nee na: giñ naa ci Yàlla ne, gisuñu ci asamaan si aw xiin du caagine aw niir, te it genn kër walla néeg doxul sunu diggante ak Salh, nee na: aw niit wu mel ni Turs daal di feeñ ca ginnaawam, ba mu nekkee ca diggu asamaan sa, mu daal di tasaroo topp mu taw, giñ naa, gisunu jant bi juróom-benni fan, topp jenn waay dugg bawoo ca bunt booba ca àjjuma ja, fekk Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc taxaw di xutba, mu taxaw jublu ko, ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi alal ji sànku na, yoon yi dagg na, ñaanal Yàlla mu téye ko, nee na: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc yëkkëti ñaari loxoom, topp mu ne: "yaw Yàlla sunu Boroom na dem ca la nu wër déet ci sunu kaw, yaw Yàlla sunu Boroom ca tund ya ak ca Montaañ ya ak ca biir xur ya, ak ca saxuwaayu garab ya " nee na: mu taxaw, nu gént di dox ci ron jant bi, Sariik nee na: laaj naa Anas ibn Maalik: ndax waa ju njëkk ja la? Mu ne ma: "lu ma ci xam".

أَنَّ رَجُلًا دَخَلَ المَسْجِدَ يَوْمَ جُمُعَةٍ مِنْ بَابٍ كَانَ نَحْوَ دَارِ القَضَاءِ، وَرَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَائِمٌ يَخْطُبُ، فَاسْتَقْبَلَ رَسُولَ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَائِمًا، ثُمَّ قَالَ: يَا رَسُولَ اللَّهِ، هَلَكَتِ الأَمْوَالُ وَانْقَطَعْتِ السُّبُلُ، فَادْعُ اللَّهَ يُغِيثُنَا، فَرَفَعَ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يَدَيْهِ، ثُمَّ قَالَ: «اللَّهُمَّ أَغِثْنَا، اللَّهُمَّ أَغِثْنَا، اللَّهُمَّ أَغِثْنَا» قَالَ أَنَسٌ: وَلا وَاللَّهِ، مَا نَرَى فِي السَّمَاءِ مِنْ سَحَابٍ وَلَا قَزَعَةً، وَمَا بَيْنَنَا وَبَيْنَ سَلْعٍ مِنْ بَيْتٍ وَلَا دَارٍ، قَالَ: فَطَلَعَتْ مِنْ وَرَائِهِ سَحَابَةٌ مِثْلُ التُّرْسِ، فَلَمَّا تَوَسَّطَتِ السَّمَاءَ انْتَشَرَتْ، ثُمَّ أَمْطَرَتْ، فَلَا وَاللَّهِ، مَا رَأَيْنَا الشَّمْسَ سِتًّا، ثُمَّ دَخَلَ رَجُلٌ مِنْ ذَلِكَ البَابِ فِي الجُمُعَةِ، وَرَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَائِمٌ يَخْطُبُ، فَاسْتَقْبَلَهُ قَائِمًا، فَقَالَ: يَا رَسُولَ اللَّهِ، هَلَكَتِ الأَمْوَالُ، وَانْقَطَعَتِ السُّبُلُ، فَادْعُ اللَّهَ يُمْسِكْهَا عَنَّا، قَالَ: فَرَفَعَ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يَدَيْهِ، ثُمَّ قَالَ: «اللَّهُمَّ حَوَالَيْنَا وَلَا عَلَيْنَا، اللَّهُمَّ عَلَى الآكَامِ وَالظِّرَابِ، وَبُطُونِ الأَوْدِيَةِ، وَمَنَابِتِ الشَّجَرِ» قَالَ: فَأَقْلَعَتْ، وَخَرَجْنَا نَمْشِي فِي الشَّمْسِ، قَالَ شَرِيكٌ: سَأَلْتُ أَنَسَ بْنَ مَالِكٍ: أَهُوَ الرَّجُلُ الأَوَّلُ؟ فَقَالَ: «مَا أَدْرِي».

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Ab kaw-kaw dafa dugg ci jàkkay Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bisu àjjuma ci buntub sowwu jàkka ji fi féete kër Umar ibn Al-Xattaab yal na ko Yàlla dollee gërëm, mu fekk Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc taxaw di xutba, waa ji jublu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, jur gi alku nañu, yoon yi dog na ci deewug jur giy tuxal nit ñi walla ci lompañam ngir xiif, ñaanal Yàlla mu nàndal ab taw. Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc yëkkëti ñaari loxoom, topp mu wax: Allaahuma asxinaa, Allaahuma asxinaa, Allaahuma asxinaa. Anas ibn Maalik yal na ko Yàlla dollee gërëm nee na: giñ naa ci Yàlla ne gisunu ci asamaan si benn dogu xiin, te sunu diggante ci jàkka ji ak Montaañu Salh ci sowwu jàkka ji xiin wi di ñëwe amul genn kër gu koy yiir ba duñu ko gis. Anas yal na ko Yàlla dollee gërëm nee na: aw xiin wu wërngal feeñ mel ni Turs te mooy këyit wu ndaw, ba mu nekkee ca diggu asamaanu Madiina daal di tasaroo, topp mu taw, giñ naa ci Yàlla ne, gisunu jant bi ngir taw bi ba beneen àjjuma ja, ba waa ja duggaat ca bunt booba, fekk Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc di xutba, mu jublu ko, daal di ne: yaw Yonnente Yàlla bi, alal ji yàqu na, yoon yi dog na, ñaanal Yàlla mu téye taw bi. Nee na: Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc yëkkëti loxoom, daal di ne: yaw Yàlla sunu Boroom wëlbatil taw ci li nu wër, wolif fi nun, yaw Yàlla sunu Boroom def ko ca suuf su kawe ya niki tund yi ak Montaañ yi, ak biir xur yi, ak saxuwaayu garab ya. Anas nee na: xiin wi doon taw daal di dog, nu génn di dox ci jant bi.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Def sabab yi ngir sàkku wërsëg, ci ñaan, ak dox ci kaw suuf, safaanoowul ak wakkirlu ci Yàlla mu kawe mi.

Sopp nañu ñaan ci ñaanug Yonnente gii ngir sàkku taw.

Sàkkoo doylu ci taw bi dagan na -sàkku taw bi taxaw- bu ñu loroo ci taw bi, jagleel na desug taw bi ci tund yi ak biir xur yi; ndaxte moo gën a méngoo ak mbay ak càmm.

Dagan na ñu sàkku ñaan ci ku ñu njort ci moom ag yiwe ak ug ragal Yàlla ci ñiy dund te teew, lii mooy ker-keraan gi dagan, bu dee ker-keraan ci darajay kenn ci mbindeef yi, moo xam muy dund walla mu dee, loolu du dagan; ndax dafa bokk ci yiy jëme ci bokkaale.

Yoonalees na dëgër ci ñaan ak di ko baamtu.

Dagan na ñu wax ak kiy xutba bisu àjjuma ngir aajo.

Fésug kàttanu Yàlla gu yéeme gi ci wàcce taw ak téye ko.

Xereñug Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci ñaan ci ñu téye taw bi ci li ciy loru wolif li ci dul loru.

Yoonalees na baawunaan ci xutba gi.

Yëkkëti loxo ci ñaan; ndax maanaam aajowoo moo ci nekk, ak séentu maanaam joxe, woroom xam-xam yi dëppoo nañu ci yëkkëti loxo yi ci bérab bii.

Keemaan ci keemaani Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, guy tegtale le ag yónnenteem, ndax dañoo nangu ñaanam fa saasa, ci indi taw bi ak ci téye ko.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (2/ 28) (1014).

Téere Muslim bi gën a wér (2/ 612) (897).

Yataal gi (6)

تيسير العلام.

للبسام (ص268).

تنبيه الأفهام.

لابن عثيمين (2/ 339).

الإلمام بشرح عمدة الأحكام.

لإسماعيل الأنصاري (1/ 215).