Skip to content

"kiy taxawu ak a dimbali ab Jatun ak way-ñakk moo ngi mel ni kuy xeex ci yoonu Yàlla, wàlla kuy taxaw guddi di woor bëccëg"

Jële nañu ci Abuu Hurayrata mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:

"kiy taxawu ak a dimbali ab Jatun ak way-ñakk moo ngi mel ni kuy xeex ci yoonu Yàlla, wàlla kuy taxaw guddi di woor bëccëg"

«السَّاعِي عَلَى الأَرْمَلَةِ وَالمِسْكِينِ، كَالْمُجَاهِدِ فِي سَبِيلِ اللَّهِ، أَوِ القَائِمِ اللَّيْلَ الصَّائِمِ النَّهَارَ».

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne kiy taxawe ay yittey jigéen ji jëkkëram faatu, te amul kenn ku taxawe ay mbiram, ak miskiin bi aajowoo, mu leen di dundal ci ngir yaakaar payug Yàlla mu kawe mi, kooku ak payam day yamoo ak kiy xeex ci yoonu Yàlla, walla kiy taxaw di julli guddi te du ca tàyyi, mbaa kiy woor te du dog.

Maanaay baat yi

...:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Ñaaxe ci dimbalante ak jàppalante ci faj aajoy ñi néew doole.

Jaamu day làmboo jépp jëf ju baax, te bokk na ci ag jaamu taxawu ak a Dimbali jigéen ñi seen jëkkër faatu ak néew doole yi.

Ibn Hubayrata nee na: li ñu ci namm mooy Yàlla mu kawe mi da koy booleel yoolub woorkat ak taxawkatu guddu, ak jiihaatkat joxandoo ko ko; ndaxte dafa taxawu ki jëkkëram faatu taxawaayu jëkkëram..., taxawu miskiin bi manul a taxawe boppam, daal di koy jox ci desiitu dundam, sarax ko ci kàttanam, ba tax njariñam di yamoo ak woor ak taxaw guddi ak jihaat.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (7/ 62) (5353).

Téere Muslim bi gën a wér (4/ 2286) (2982).

Yataal gi (9)

بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.

لسليم بن عيد الهلالي (1/ 351).

تطريز رياض الصالحين.

لفيصل بن عبد العزيز المبارك (ص198).

رياض الصالحين (ص107) (265).

شرح رياض الصالحين.

لابن عثيمين (3/ 99).

نزهة المتقين شرح رياض الصالحين.

لمجموعة من الباحثين (275).