Skip to content

«bu nit ki dundalee njabootam di ci séentu aw yiw loolu dina nekk ci moom ab sarax».

Jële na ñu ci Abuu Mashuud -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:

«bu nit ki dundalee njabootam di ci séentu aw yiw loolu dina nekk ci moom ab sarax».

«إِذَا أَنْفَقَ الرَّجُلُ عَلَى أَهْلِهِ يَحْتَسِبُهَا فَهُوَ لَهُ صَدَقَةٌ».

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne bu nit ki joxee njël njabootam gimu war a dundal, niki jabaram ak way-juram ak i doomam ak ñeneen, di sàkkoo jege Yàlla ci loolu, di yaakaar ci moom payug li mu joxe kon dana am yoolub sarax.

Maanaay baat yi

...:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Dundal njaboot gi dees ciy am ab yool.

Aji-gëm ji day sàkku ci jëfam ji jëmmi Yàlla ji ak la fa moom ci ab yool.

Deesa war a teewal yéene ju sell ci jépp jëf, bokk na ci yooyu jamonoy dundal njaboot.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (1/ 20) (55).

Téere Muslim bi gën a wér (2/ 695) (1002).

Yataal gi (8)

كنوز رياض الصالحين.

لمجموعة من الباحثين (5/ 334).

شرح رياض الصالحين.

لابن عثيمين (3/ 157).

نزهة المتقين بشرح رياض الصالحين.

لمصطفى الخن وغيره (1/ 293).

بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.

سليم الهلالي (1/ 375).