"buleen wut ay tool ba far xér ci adduna".
Jële nañu ci Abdallah Ibn Mashuud yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:
"buleen wut ay tool ba far xér ci adduna".
«لاَ تَتَّخِذُوا الضَّيْعَةَ فَتَرْغَبُوا فِي الدُّنْيَا».
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc tere na wut ay tool ak i Sarden; ndax dafa bokk ci liy xemmemloo ci àdduna ak jeng jëm ca wolif allaaxira.
Tere nañu ëppalante ci àdduna ndax li ci nekk ci wan ginnaaw allaaxira.
Nekkul ci hadiis bi luy tere ñu wut luy tax a dund, waaye li ñi tere mooy nuur ci àdduna ak fàtte allaaxira.
As-Sindii nee na: li nu ci namm mooy: bu leen xuus ci wut ay tool ba mu fàbbi leen wolif tudd Yàlla.
Téere Sunna yi bu At-tirmisiy (4/ 155) (2328).
Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya (6/ 54) (3579).
Yataal gi (3)
كنوز رياض الصالحين.
لمجموعة من الباحثين (331/7).
شرح رياض الصالحين لابن عثيمين (375/3).