Skip to content

«ñiy taral alku nañu

Jële nañu ci Abdallah Ibn Mashuud mu wax ne: Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:

«ñiy taral alku nañu» wax na ko ñatti yoon.

«هلك المُتَنَطِّعُون» قالها ثلاثًا.

Muslim soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne way-taral yi ñu sooy lañu wayé ñu Pert lañu yit-ci lu dul njub te du xam-xam- ci seen diine ak séen àdduna, ci séen i wax ak seen i jëf, ñi nga xam ne dañuy jéggi dayob Sariiha bi Yónent bi indi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-.

Maanaay baat yi

....:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Araamal ag taral ak diisal ci mbir yépp, ak soññee ci moytu ko ci lépp; rawatina ci jaamu yi ag màggal ñu baax ñi.

Sàkku li gën a mat ci jaamu yi mbir mu ñu gërëm la; waaye loolu ci topp Sariiha lay ame.

Soppug di feddali mbir yi am solo, ndax Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa bàmtu wax ci ñatti yoon.

Yaatug Lislaam ak ug Yombam.

Dellluwaay yi

Téere Muslim bi gën a wér (4/ 2055) (2670).

Yataal gi (4)

الجديد في شرح كتاب التوحيد.

للقرعاوي (ص180).

الملخص في شرح كتاب التوحيد.

لصالح الفوزان (ص167).