amna ab aaya bu ngeen di jàng ci seen téete bi, bu wàccoon ci nun mbooleem Yahuud yi kon dananu jàppe bis booba feet
Jële nañu ci Umar ibn Al-Xattaab Xattaab yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:
Jenn waay ci Yahuud yi da ko a wax ne ko: yaw njiitu jullit ñi, amna ab aaya bu ngeen di jàng ci seen téete bi, bu wàccoon ci nun mbooleem Yahuud yi kon dananu jàppe bis booba feet, mu ne ko: ban aaya la? Mu ne ko: {Bis niki tay matalal naa leen seen diine xëpp naa leen samay xéewal gërëm naa ci yeen lislaam muy seen diine} [Al-Maa-ida: 3] Umar nee na: xam nanu bis booba, ak bérab ba mu wàcce ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc fekk ma nga taxaw ca Arafa bisub àjjuma.
أَنَّ رَجُلًا مِنَ اليَهُودِ قَالَ لَهُ: يَا أَمِيرَ المُؤْمِنِينَ، آيَةٌ فِي كِتَابِكُمْ تَقْرَؤُونَهَا، لَوْ عَلَيْنَا مَعْشَرَ اليَهُودِ نَزَلَتْ لاَتَّخَذْنَا ذَلِكَ اليَوْمَ عِيدًا، قَالَ: أَيُّ آيَةٍ؟ قَالَ: {اليَوْمَ أَكْمَلْتُ لَكُمْ دِينَكُمْ وَأَتْمَمْتُ عَلَيْكُمْ نِعْمَتِي وَرَضِيتُ لَكُمُ الإِسْلاَمَ دِينًا} [المائدة: 3] قَالَ عُمَرُ: قَدْ عَرَفْنَا ذَلِكَ اليَوْمَ، وَالمَكَانَ الَّذِي نَزَلَتْ فِيهِ عَلَى النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، وَهُوَ قَائِمٌ بِعَرَفَةَ يَوْمَ جُمُعَةٍ.
Jenn waay ci Yahuud yi dafa ñëw ci njiitu jullit ñi Umar yal na ko Yàlla dollee gërëm ne ko: amna aaya bu ngeen di jàng ci seen téere bi, bu wàccoon ci nun -mbooleem Yahuud yi- ci sunu téere bi Tawraat kon dananu bis booba feet di ca feetu; ngir sant ci xéewalug wàccu aaya bu màgg bi, Umar yal na ko Yàlla dollee gërëm ne ko: ban aaya la? Mu wax ne: {Bis niki tay matalal naa leen seen diine xëpp naa leen samay xéewal gërëm naa ci yeen lislaam muy seen diine}. Umar yal na ko Yàlla dollee gërëm daal di ne: xam nanu bis booba, ak bérab bi aaya bu tedd bii wàcc, moom ci bisu feet la wàcc, te mooy bisu àjjuma fekk Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ma nga taxaw Arafa, te ñaari bis yu màgg la ci jullit ñi.
Leeral ni Umar yal na ko Yàlla dollee gërëm daan yittewoo xam bérab ak jamono yi aaya bi wàcc.
Aaya bii ag leeral la ci li Yàlla mu kawe xéewalal xeet wi ba tax mu matalal leel dseen diine, xëpp leen ay xéewalam, ba tax duñu aajowoo dolli ci mbiri diine ji, lépp lu xew ginnaaw bi Yàlla mu kawe mi matalee diine ji, ci lu amul tegtal dees koy jàppe Bidaag cànkute, kem ni mu saxe jóge ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc "képp ku sos ci sunu mbir mii lu ci bokkul dees ko koy felloo".
Hadiis bi dees ba ci dégge ne fert yi du tege ci gis-gis ak fent jem ni ko ñoñ-téere yi ñu jiitu di defe; waaye ci Sariiha ak topp lay tege, aaya bii li mu làmboo cu matug diine ji ak sëmbartal xéewal yi Yàlla da ko a wàcce ci bis bu mu yoonal mu nekk feet ñeel xeet wii ci ñaari anam: bi ci njëkk: mooy bisu feetu ayu-bis yi te mooy àjjuma. Ñaareel bi: bisu feetu waa sesoon la, te mooy seen bisu daje ba gën a màgg, di seen taxawaay ba gën a màgg.
As-Sahdii wax ci pirim aaya bii: {Bis niki tay matalalnaa leen seen diine} ci matug dimbale gi, ak matalug Sariiha bi ci li feeñ ak li nëbbu, cosaan yi ak bànkaas yi, lii moo tax Alxuraan ak sunna doy géppug doy, ci ay àttey diine ci ay cosaanam ak i bànkaasam, képp ku jafeel di njort ne ngir nit ñi xam pas-pas ak àtte yi fàww ñu jëm ci xam-xam yu bokkul ak xam-xamu Alxuraan ak sunna, muy xam-xamu wax, ak yeneen, kooku ki réer te ag neen lay woote, te dafa njort ne diine ji du mat ci lu dul li muy wax di ci woote, te dafa bokk ci lëndëm ak réeralaate gi gën a màgg ñeel Yàlla ak Yonnenteem {gërëm naa ci yeen lislaam muy seen diine} maanaam: tànn naa ko segg ko muy seen diine, kem ni ma ko gërëme ñeel leen, kon taxawleen ci ngir sant seen Boroom, santleen it ci li mu xéewale li gën ci diine yi gën caa tedd gën cas mat.
Téere Al-buxaariy bi gën a wér (1/ 18) (45).
Yataal gi (2)
إرشاد الساري لشرح صحيح البخاري (1/ 132).
البحر المحيط الثجاج في شرح صحيح الإمام مسلم بن الحجاج (45/ 372).