"deeleen gaawal néew bi, ndax bu dee ku baax la ci yiw ngeen ko jëme, bu dee du loolu nag, kon aw ay la wu ngeen teg ci seen doq yi".
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
"deeleen gaawal néew bi, ndax bu dee ku baax la ci yiw ngeen ko jëme, bu dee du loolu nag, kon aw ay la wu ngeen teg ci seen doq yi".
«أَسْرِعُوا بِالْجِنَازَةِ، فَإِنْ تَكُ صَالِحَةً فَخَيْرٌ تُقَدِّمُونَهَا، وَإِنْ يَكُ سِوَى ذَلِكَ، فَشَرٌّ تَضَعُونَهُ عَنْ رِقَابِكُمْ».
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa digle ñu gaawal néew bi ci jullee ko ak suul ko; ndax bu dee ku baax la kon ci yiw lañu ko jëme muy xéewali bàmmeel, bu dee du loolu, kon aw ay la wu ñu teg ci seen doq yi.
Ibn Hajar nee na: sopp nañu gaawe ko, waaye ci lu dul muy waral ak tar gog dees na ragal mu indi ak yàqute ci aji-faatu ji, walla coono ci aji-gàddu ji mbaa aji-gunge ji.
Dees na tënk gaawe gi bu fekkee ne dee gi nekkul ci ag mbetteel ndax manna nekk ag xëm, kon dana jaadu ñu bañ ko a suul ba keroog ñuy wóorlu dee gi, walla yeexe gi di lu tuuti ngir yéwénal, ci baril ñi koy jullee, ak ay jegeñaaleem teew, te ragaluñu ci ag yàqute.
Ñaaxe ci gaawe néew bi ngir njariñu aji-faatu ji bu dee aji-texe la, walla ngir njariñu ñi koy gunge bu dee ku texeedi la.
An-Nawawii nee na: dees na ci jële it bàyyee ànd ak ñi baaxul.
Téere Al-buxaariy bi gën a wér (2/ 86) (1315).
Téere Muslim bi gën a wér (2/ 651) (944).
Yataal gi (4)
تيسير العلام شرح عمدة الأحكام.
لعبد الله البسام (ص284).
تنبيه الأفهام شرح عمدة الأحكام.
لابن عثيمين (2/ 367).
Cited in books
2 BooksYataal gi (2)
- أحكام الجنائز(أَسْرِعُوا بِالْجِنَازَةِ، فَإِنْ تَكُ صَالِحَةً فَخَيْرٌ تُقَدِّمُونَهَا، وَإِنْ يَكُ سِوَى ذَلِكَ، فَشَرٌّ تَضَعُونَهُ عَنْ رِقَابِكُمْ).
- مجموعة زاد الفقه (2)الفقه للمستوى الثاني ( مجموعة زاد )«أسرعوا بالجنازة، فإن تك صالحة فخير تقدمونها إليه، وإن يك سوى ذلك، فشرٌّ تضعونه عن رقابكم».