«Li gën ci sikar yi: Laa ilaaha illal Laahu, li gën ci ñaan yi: Alhamdu lil Laahi».
Jële nañu ci Jaabir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónent Yàlla bi -yal ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax naan:
«Li gën ci sikar yi: Laa ilaaha illal Laahu, li gën ci ñaan yi: Alhamdu lil Laahi».
«أَفْضَلُ الذِّكْرِ: لَا إِلَهَ إِلَّا اللهُ، وَأَفْضَلُ الدُّعَاءِ: الْحَمْدُ لِلهِ».
Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafay xamle ne li gën ci tudd Yàlla mooy: «Laa ilaaha illal Laahu» maanaam, amul kenn ku ñuy jaamu ci dëgg ku dul Yàlla, li gën ci ñaan yi mooy: Alhamdu lil Laahi; te mooy nangu ne kiy joxe xéewal mooy Yàlla -tudd naa sellam ga-, moom mi yeyoo melokaan yu mat sëkk ya te rafet.
...:
Ñaaxe ci di baril a tudd Yàlla ci kàdduy Tawhiid, ak di ñaan cig cant.
Téere Sunna yi bu At-tirmisiy (5/ 393) (3383).
Yataal gi (4)
نزهة المتقين شرح رياض الصالحين.
لمصطفى الخِن وغيره (2/ 984).
زاد المعاد في هدي خير العباد.
ابن قيم الجوزية (1/ 36).