Skip to content

"yamaleleen seen sàppe yi, ndax yamale sàppe yi daa bokk ci matug julli gi"

Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:

"yamaleleen seen sàppe yi, ndax yamale sàppe yi daa bokk ci matug julli gi"

«سَوُّوا صُفُوفَكُمْ، فَإِنَّ تَسْوِيَةَ الصَّفِّ مِنْ تَمَامِ الصَّلَاةِ».

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day digal jullikat yi ñu yamale seen sàppe yi, te kenn bañ a jiitu kenn mbaa mu koy mujj, ak ne yamale sàppe yi daa bokk ci matug julli gi, waaye dëngug sàppe ayib la ci julli gi ag wàññiku la ca.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Yoonalees na yittewoo ci lépp luy matal julli gi te di ko soreele ag ug wàññiku.

Keemaanu Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci jàngale, ba tax mu lënkale àtte bi ak li ko waral; ngir leeral keemaanu Sariiha, ak sawarloo bakkan yi ci jëfe.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (1/ 145) (723).

Téere Muslim bi gën a wér (1/ 324) (433).

Yataal gi (6)

تيسير العلام شرح عمدة الأحكام.

للبسام (ص127).

تنبيه الأفهام شرح عمدة الأحكام.

لابن عثيمين (1/ 161).

الإفهام في شرح عمدة الأحكام.

لابن باز (ص173).