Skip to content

"su ngeen wakkirlu woon ci Yàlla dëgg-dëggi wakkirlu, kon dana leen wërsëgal kem ni muy wërsëgale picc yi, day xëy nekk ku woos xiif di gont biir bi fees dell".

Jële nañu ci Umar ibn Al-Xattaab yal na k Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:

"su ngeen wakkirlu woon ci Yàlla dëgg-dëggi wakkirlu, kon dana leen wërsëgal kem ni muy wërsëgale picc yi, day xëy nekk ku woos xiif di gont biir bi fees dell".

«لَوْ أَنَّكُمْ كُنْتُمْ تَوَكَّلُونَ عَلَى اللهِ حَقَّ تَوَكُّلِهِ لَرَزَقَكُمْ كَمَا يَرْزَقُ الطَّيْرَ تَغْدُو خِمَاصًا وَتَرُوحُ بِطَانًا».

Imaam Ahmad ak At-Tirmisiyyu ak An-Nasaa-yyu ak Ibnu Maaja ak Ibnu Hibbaan ci Sahiiham ak Al-Haakim ñoo ko soloo.
Wér na
Leeral gi

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da ñuy soññ ci nuy sukkandiku ci Yàlla mu kawe mi ci xëcc njariñ ak jeñ lor ci mbiri àdduna yi ak yu diine yi, ndax kenn du joxe te kenn du xañe, mbaa muy lore walla muy jariñe ku dul Moom Yàlla mu kawe mi. Ak it nuy def sabab yiy xëcc njariñ di jeñ lor ànd ak sukkandiku ci Yàlla, saa su nu defee loolu Yàlla dana nu wërsëgal kem ni muy wërsëgale picc miy génn suba di ku xiif, mu dellusi ngoon biir bi fees dell, te jëf i picc mii benn sabab la ci dem wuti wërsëg, te bañ a bàyyandiku mbaa tàyyeel.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Bokk na ci njariñal adiis bi : gëneelu wakkirlu, ak ne dafa bokk ci sabab yi gën a màgg ci yiy xëcc wërsëg.

Wakkirlu du dàqoonteek def sabab yi, ndax dañoo xamal ne dëgg-dëggi wakkirlu du wuute ak xëy walla gontu jëm ci sàkku wërsëg.

Yittewoog Sariiha ci jëfi xol yi; ndax wakkirlu jëfu xol la.

Sukkandiku ci sabab yi dong loolu diine ju wàññiku la, waaye bàyyi sabab yi tamit xel mu matul la.

Dellluwaay yi

Téere Sunna yi bu At-tirmisiy (4/ 151) (2344).

Téere Sunna yi bu Ibnu Maaja (5/ 266) (4164).

Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya (1/ 332) (205).

Yataal gi (5)

التحفة الربانية في شرح الأربعين حديثًا النووية (ص103).

فتح القوي المتين في شرح الأربعين وتتمة الخمسين.

للعباد (ص152).

الأحاديث الأربعون النووية وعليها الشرح الموجز المفيد.

لعبد الله المحسن (ص91).