Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

106 of 732 cards

Clear filters

Narrator

Show all narrators (56)
"doomu Aadama feesalul lenn ndab lu yées biiram, doy na sëkk doomu Aadama ji lekk gu mu taxawale ndiggam li, bu manut a ñàkk, kon na def biiram ñatti xaaj benn ba ngir lekkam, beneen ba ngir naanam, ñatteelu xaaj ba ngir noyyeem".
Wér na Imaam Ahmad ak At-Tirmisiyyu ak An-Nasaa-yyu ak Ibnu Maaja ñoo ko soloo
"Bàyyil looy sikk-sàkka jëm ci loo sikk-sàkkawul".
Wér na At-Tirmisiyyu ak An-Nasaa-iyyu ñoo ko soloo.
«Waa ji ñu tudd sama tur te julliwul ci man kooku sooy na, waa ji weeru koor dugg ba jeex ta jéggalu ñu ko sooy na, waa ji fekke dunduk ñaari way-juram ñu nekk ay mag, te dugaluñu ko Àjjana kooku it sooy na ».
Wér na At-tirmisiy soloo na ko, ak Ahmat.
«yëkkëti nanu xalima gi ci ñatt, ci kiy nelaw ba baa muy yeewu, ak ci xale bi ba baa muy gént, ak ci dof bi ba baa muy xellu».
Wér na Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy, ak An-nasaa'iy ca Al-kubraa, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat.
«amul dara lu gën a diis ci màndxem jullit bi ëllëg bis-pénc jikko yu rafet, te Yàlla dafa bañ ku ñaaw i wax ñaaw i jëf».
Wér na Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy.
"ku wax: subhaanal Laahi Alhasiimi wa bi hamdihi, ñu jëmbëtal ko ag garabu tàndarma ca àjjana".
Wér na At-tirmisiy soloo na ko.
"laaj nga lu màgg, waaye lu yomb la ci ku Yàlla yombalal: dangay jaamu Yàlla te doo ko bokkaale ak dara, di taxawal julli, di joxe asaka, di woor weeru koor, di aj Màkka, topp mu ne: ndax duma la tegtal bunti yiw yi, woor ab pakk la, saraxe day far njuumte kem ni ndox di faye sawara, ak jullig nit ki ci digg guddi gi, topp mu jàng: {séen wet ya day sori lal ya} ba egg {li ñuy def}, topp mu ne: ndax duma la xibaar bopp mbir mi ak kenoom ak njobbaxtalu jégénam, ma ne ko: ahakay yaw Yonente Yàlla bi, mu ne: boppu mbir mi mooy lislaam, kenoom mooy julli, njobbaxtalu jégénam mooy jihaad, topp mu ne: ndax duma la xibaar li jiital loolu lépp, ma ne ko ahakay yaw Yonnente Yàlla bi! Mu jàpp ci làmmiñam daal di ne: téyeel sa lii, ma ne ko: yaw Yonente Yàlla bi! Mo ndax dees nuy jàppe li nuy wax, mu wax ne: na la sa yaay ñàkk rekk, mo ndax dara dana këpp nit ñi ca seen kanam ya walla mu ne ca seen gémmiñ ya lu dul seen góobiti làmmiñ"!
Wér na At-tirmisiy soloo na ko.
"amul ñaari jullit yuy daje daal di joxante loxo lu dul ne dees na leen jéggal laata ñuy teqalikoo".
Wér na ci kaw bees boolee mbooleem yoon yi mu ñëwee Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat.