Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

76 of 732 cards

Clear filters
«ku giñ ci ku dul Yàlla weddi na walla bokkaale na».
Wér na Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ahmat.
«bu sa làmmiñ deñ di tooy ci tudd Yàlla».
Wér na At-tirmisiy soloo na ko, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat.
«bàyyil li la leerul te jëm ca la la leer, ndaxte dëgg ag dal la, fen nag ag jax-jaxi la".
Wér na At-Tirmisiyyu ak An-Nasaa-iyyu ak Ahmad ñoo ko soloo.
«aji-gëm nekkul kiy jamaate, walla kiy rëbbaate, mbaa kiy def ñaawteef, walla aji-bon lammiñ ji».
Wér na At-tirmisiy soloo na ko.
«amul kenn kuy def bàkkaar, jug daal di laab, daal di julli, daal di jéggalu Yàlla, lu dul ne Yàlla dina ko jéggal», mu daal di jàng aaya jii: {ak ña nga xam ne bu ñu defee ñaawteef mbaa ñu tooñ seen bopp dañuy tudd Yàlla daal di jéggalu seen bàkkaar} [ Aali-Imraan: 135].
Wér na Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy, ak An-nasaa'iy ca Al-kubraa, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat.
"ñi ma gën a bëgg ci yéen, te gën maa jege ëllëg bis-pénc, ñooy ñi gën a rafet jikkó ci yéen, waaye ñi ma gën a bañ ci yéen te gën maa sori ëllëg bis-penc, ñooy coowkat yi, ak puukarekat yi, ak ñiy rëy-rëylu", ñu ne ko:yaw Yonente Yàlla bi, nun xam nanu coowkat yi ak puukarekat yi, kon lan mooy al-mutafayxihuuna? Mu ne leen: mooy: ñiy rëy-rëylu".
Wér na At-tirmisiy soloo na ko.
«Deesul takk jigéen ci lu dul kilifa».
Wér na Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat.
«buleen ŋàññ ngelaw li, bu ngeen gisee lu ngeen sib, nangeen wax: Allaahuma innaa nas-aluka min xayri haasihi arriihi wa xayri maa fiihaa wa xayri maa umirat bihii, wa nahuusu bika min sarri haasihii arriihi wa sarri maa fiihaa wa sarri maa umirat bihii».
Wér na At-tirmisiy soloo na ko.