Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

76 of 732 cards

Clear filters
"ndax du ma leen tegtal li gën ci seen jëf yi, te gën cee sell fa seen Boroom, te gën cee kawe ci seeni daraja te gën ci yéen wurus ak xaalis, te gën ci yéen ngeeni daje ak séeni noon ngeen di dóor seen doq ya, ñoom ñuy dóor seen doq yi?" Ñi ne ko ahakay. Mu ne: "tudd Yàlla mu kawe mi".
Wér na At-tirmisiy soloo na ko, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat.
Génn nanu ci guddi gu bari taw te lëndëm lool, di wër Yonnente Yàlla bi ngir mu jiite nu julli, nee na: nu dab ko, mu ne ma: "waxal" te waxuma dara, mu waxaat ma: "waxal", te waxuma dara, mu ne ma: "waxal", ma ne ko: lan laay wax? Mu ne ma: "{Xul huwal Laahu Ahadun} ak ñaari musluwaay yi boo gontee ak boo xëyee ñatti yoon, dana la fegal lépp".
Wér na Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy, ak An-nasaa'iy.
Dikk naa ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bëgg a dugg ci Lislaam, mu digal ma ma sàngu ci ndox ak siddéem.
Wér na Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy, ak An-nasaa'iy.
«ku aar deru mbokkam Yàlla aar kanamam ci sawara ëllëg bis-pénc».
Wér na At-tirmisiy soloo na ko, ak Ahmat.
«bu ndox mi nekkee ñaari mbànd kon du téye sobe».
Wér na Abuu Daawuda ak At-Tirmisiyyu ak An-Nasaa-iyyu ak Ibn Maaja ak Ahmad ñoo ko soloo.
Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan tissooli day teg loxoom -walla yéereem- ci gémmeñam, daal di suufeel -walla mu téye- ci kàdoom.
Wér na Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ahmat.
«ku wax bismil Laahi Allasii laa yadurru maha ismihii say-un fil ardi walaa fis samaa-i wa huwa As-Samiihu Al-Haliimu, ñatti yoon balaa bu bette du ko dal, ba baa muy xëy, ku ko wax bu xëyee ñatti yoon balaa buy bette du ko dal ba baa muy gont", mu ne: ag paraaliise daal di dal Abaan ibn Usmaan, waa ji dégg ci moom hadiis bi tàmbali di ko xool, mu ne ko: lu tax nga may xool nii? Giñ naa ci Yàlla fenaluma Usmaan, te du caagine Usmaan daa fenal Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, waaye bis bi ma lii di dal damaa meroon fàtte ko a wax.
Wér na Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy, ak An-nasaa'iy ca Al-kubraa, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat.
«ku muñal ki am jafe-jafe, walla mu baal ka ko, Yàlla dana ko keral bis-penc ca suufus keru Gàngunaayam ga bis ba nga xam ne genn ker amul gu dul keram ga».
Wér na At-tirmisiy soloo na ko, ak Ahmat.