Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

3 of 732 cards

Clear filters

Narrator

Show all narrators (52)
Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa téye ci loxoom, ne ko: "yaw Muhaas, waat naa ci Yàlla ne dama laa bëgg", mu ne ko: "maa ngi lay dénk yaw Muhaas bul bàyyi mukk di wax ginnaaw julli gu ne: Allaahuma ahinnii halaa sikrika wa sukrika wa husni hibaadatika".
Wér na Abuu Daawuda ak An-Nasaa-yyu ak Ahmad ñoo ko soloo
Ba ko Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc yónnee Yaman da ko a digal mu jël ci Nag fanweer yu nekk wenn nag wu am at wu góor walla wu jigéen, ak ci ñent-fukk yu nekk wenn nag wu am ñaari at, ak ci ñoñ-téere buy aji-gént -maanaam di gént di sëy- ab Diinaar walla lu toll ni moom ci Mahaafir, ay yére la yu nekk Yaman.
Wér na bees sukkandikoo ci yeneen yi koy dëggal Abuu Daawuda ak At-Tirmisiyyu ak An-Nasaa-iyyu ak Ibn Maaja ak Ahmad ñoo ko soloo.
Nekkoon naa ak Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci benn tukki, ma xëy benn bis jegesi ko fekk ñoo ngi dox, ma ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, xibaar ma jëf joo xam ne dana ma dugal àjjana di ma soreele sawara, mu ne ma: "laaj nga lu màgg, waaye lu yomb la ci ku ko Yàlla yombal ci moom, dangay jaamu Yàlla te doo ku bokkaale ak dara, di taxawal julli, di joxe asaka, di woor weeru koor, te aji néeg ba" topp mu ne: "ndax duma la tegtal bunti yiw yi: woor ab pakk la, saraxe day fay njuumte kem ni ndox di faye sawara, ak jullig nit ki ci xaaju guddi " topp mu jàng: laayab « tata jaafaa junuubuhum ba àgg Yahlamuun » topp mu ne : "ndax duma la xibaar boppu mbir mi yépp ak kenoom?" Ma ne ko: ahakay yaw Yonnente Yàlla bi, mu ne: "boppu mbir mi mooy lislaam, kenoom di julli, njobbaxtal la di jihaad" topp mu ne : "ndax duma la xibaar li moom loolu lépp nag?" Ma ne ko: ahakay yaw Yonnente Yàlla bi, mu téye ci làmmiñam, daal di ne: "téyeel sa lii" ma ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, kon dees nuy jàppe li nuy wax? Mu ne ma: "yal na la sa yaay ñàkk yaw Muhaas, mo ndax dara dana këpp nit ñi ci seen kanam ya walla seen gémmiñ ya ca sawara lu dul seen góobiti làmmiñ?".
Wér na ci kaw bees boolee mbooleem yoon yi mu ñëwee At-tirmisiy soloo na ko, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat.