Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

44 of 732 cards

Clear filters
«Sama mbalka ma de mi ngi toll ne doxu weer, ndoxam ma moo gën a weex meew, xetam ga moo gën a neex gëttug misk, te koppu yi dañoo mel ni biddiwi yi nekk ci asamaan Ku ci naan doo mar mukk ».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"mbir mii (te mooy diine ji ) dana egg fu guddi gi ak bëccëg gi egg, te Yàlla du bàyyi kërug taax walla kërug kaw lu dul ne dana fa dugal diine ji, ci teddaangey aji-tedd walla toroxtaangey aji-torox, ag teddaange ju Yàlla di terale Lislaam, ak toroxtaange ju Yàlla di toroxale kéefar", Tamiim Addaarii daan na wax naan: loolu de ci sama waa kër laa ko xame, ku ci tuub ci ñoom rekk am na yiw teddnga ak ug màgg, ku ci weddi ci ñoom am na toroxtaange ak ug tuuti ak joxe juuti.
Wér na Ahmat soloo na ko.
"bu ñu tegee néew bi ba góor ñi gàddu ko ca seen loos ya bu nekkee ku baax la day wax naan: yóobleen ma, bu dee du ku baax nag day wax naan: wóoy alku naa!! fan ngeen ko jëme? Lépp lu dul nit dana dégg kàddoom ga, te bu ko déggoon day xëm".
Wér na Al-buxaariy soloo na ko.
«ku seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla moom dong amul te amul bokkaale, ak ne Muhammat ndawul Yàlla la di ndawam, ak ne Iisaa jaamub Yàlla la di ndawam, di kàddoom gu mu sànni ci Maryama di ag ruu gu bawoo ci moom, ak ne àjjana dëgg la, sawara dëgg la, Yàlla dana ko dugal àjjana ak nu jëfam man a toll".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.