Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

44 of 732 cards

Clear filters
"dañuy jegeele jant bi ci mbindeef yi ëllëg bis-pénc, ba mu jege leen luy toll ni Miil",Sulaym ibn Haamir wax ne: giñ naa ci Yàlla ne xamuma lan mooy Miil? Ndax ab soriwaay la ci suuf, walla li ñuy tusngale bët la,mu ne:"nit ñi nekk ci ñaq kem seen i jëf,amna ci ñoom ku muy toll ci ay dojoram, amna ci ñoom ku muy toll ci ay óomam, amna ci ñoom ku muy toll ci ndiggam, amna ci ñoom ku ñaq wi di ŋalaab ag ŋalaab" nee na:Yonente Yàlla bi daal di junj loxoom ci gémmiñam.
Wér na Muslim soloo na ko.
"barab bu kenn ci yéen bi gën a suufe ca àjjana mooy ñu wax ko: mébétal muy mébét di mébét, mu ne ko: ndax mébét nga? Mu ne: waaw, mu ne ko: am nga li nga mébét ak lu mel ni moom".
Wér na Muslim soloo na ko.
«bis-pénc du taxaw ba keroog ngeeni xeex ak Yahuut yi, ba doj wu ab Yahuut nekk ci ginnaawam di wax naan: yaw jullit bi, ab Yahuut a ngi nii sama ginnaaw ñëwal ray ko».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Nekkoon nanu fi Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, mu xool weer wi ci genn guddi -guddi yu leer yi- daal di wax ne: " yéen de dangeen gis seen Boroom kem ni ngeen di gise weer wii, te du ngeen buuxante ngir gis ko, bu ngeen manee ba deesu leen not ci jullig fajar njëkk jant bi di fenk ak njëkk muy so defleen ko" mu daal di jàng: "{nanga sàbbaal sa Boroom njëkk fenkug jànt bi ak njëkk so ga}"
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«amul benn boroom wurus du caagine xaalis, te du joxe àqam, lu dul ne bu bis-pénc baa dees na ko lalal ay lali xeeri sawara, tàngal ko ca sawaraw Jahannama, diko paase ca wetam ga ak jëham ba ak ndiggam la, teg ca saa bu seddee rekk ñu delloo ko ca, ci bis bob ab nattaleem moo ngi toll ni juróom-fukki junniy at, ba keroog ñuy àtte diggante jaam ñi, mu gis yoonam, benn mu jëm àjjana, walla mu jëm sawara».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«Yàlla dina musal nit ci samaw xeet ci kanamu mbindéef yépp ëllëg bis-pénc, mu génneel ko juróom ñeent fukk ak juróom ñeenti téere, téere bune dana toll fa gisu bët yam, ñu ne ko: Ndax dagay weddi dara ci lii ? Ndax samay bindkat dañu laa tooñ ? Mu ne ko: Déedéet yaw Boroom bi. Mu ne ko: ndax kon am nga ngànt ? Mu ne ko: Déedéet yaw Boroom bi, Mu ne ko: ahakay, am nga fi nun aw yiw, te fii tay kenn du la fi tooñ, ñu génne ag kayit gog la ca nekk mooy: Seede naa ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla, Maa ngi seede ni Mohammat jaamam la di Yónenteem. Ñu ne ko: indil sa màndaxekaay, muy wax naan: ay sama Boroom lu kayit wii di jariñ ci wetu téere yii ? Ñu ne ko: kenn du la fi tooñ, nee na: ñu teg téere yi ci genn wàll, teg kayit wi ci geneen wàll, téere yi tasaaro, kayit wa daal di diis nit téere ya, dara du diis ci wetu turu Yàlla».
Wér na At-tirmisiy soloo na ko, ak Ibnu Maaja.
«ci sama mujjuw xeet wi dana am ay nit yu leen di wax lu ngeen masuta dégg yéen ak séen i baay, nangeen leen moytu».
Wér na Muslim soloo na ko.
«ndax duma leen waxtaanal ci Ad-Dajjaal, lu benn Yonnente masul a wax aw xeetam? Moom de dafa patt, dana ànd ak lu mel ni àjjana ak sawara, la muy wax ne mooy àjjana loolu sawara la, maa ngi leen koy moytondikuloo kem na ko Nuuh moytondikuloo woon aw xeetam».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.