Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

60 of 732 cards

Clear filters
Dañoo mas a toog ak Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci jàkka ji rekk benn waay bu yéeg sig giléem daldi dugg si, mu yésal giléem gi ci jàkka ji daal di koy yeew, ba noppi daal di ne? Kan ci yéen mooy Muhammat? Fekk Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- moo ngi sóonu ci séen biir, nu ne ko: góor gu weex gii sóonu la, waa ji ne ko: yaw doomu Abdul Mutalib, Yónente bi ne ko «wuyu naa la». Waa ji ne ko -: man de damalay laaj te dinaa taral laaj yi ci sa kaw, bul ma mere kon ? Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: «laajal lu la soob» mu ne ko: maa ngi lay laaj ci sa Boroom di Boroomu ñi la jiitu, ndax Yàlla moo la yónni ci nit ñépp ? Mu ne ko: «giñ naa ko ci Yàlla, waaw». Mu ne ko: maa ngi lay ñaan ci Yàlla , ndax Yàlla moo la digal nu julli juróomi julli ci bis bi ak ci guddi gi? Mu ne ko: «waaw maa ngi seedeloo Yàlla ». Mu ne ko: maa ngi ñaan ngir Yàlla, ndax Yàlla moo la digal nu woor weer wii ci at mi? Mu ne ko: «seedeloo naa ko Yàlla, waaw». Mu ne ko: maa ngi lay ñaan ngir Yàlla, ndax Yàlla moo la digal nga jël sarax ci sunu way-woomal ñi séddale ko ci sunu way-ñàkk ñi? Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: «maa ngi koy seedeloo Yàlla, waaw».waa ji ne ko: gëm naa li nga indi, man nag ndaw laa te samay nit ñoo ngi sama ginnaaw, man maay Damaam Ibn Sahlabata di mbokkum njabootu Sahd Ibn Bakrin.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«Yàlla tere na leen ngeen di giñ ci seen baay yi", Umar wax ne : ba ma déggee Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- di ko tere giñatuma ca mooxam ci lu ma ci samay wax mbaa may jottali waxi keneen ».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«ku seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla moom dong amul te amul bokkaale, ak ne Muhammat ndawul Yàlla la di ndawam, ak ne Iisaa jaamub Yàlla la di ndawam, di kàddoom gu mu sànni ci Maryama di ag ruu gu bawoo ci moom, ak ne àjjana dëgg la, sawara dëgg la, Yàlla dana ko dugal àjjana ak nu jëfam man a toll".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«sunu Boroom bu baarkeel bi te kawe day wàcc guddi gu nekk ci asamaani àdduna si bu guddi gi desee ñatteelu xaaj bu mujj ba, di wax naan: ku may woo ma wuyu ko? Ku may laaj ma jox ko? Ku may jéggalu ma jéggal ko?».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.