Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

5 of 732 cards

Clear filters
Dégg naa Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: "Yàlla mu baarkeel mi te kawe nee na: éey yaw doomu Aadama ji boo ma ñaanee yaakaar ma ma jéggal la ak lu man a nekk ci yaw te duma faale, yaw doomu Aadama say bàkkaar bu eggoon ca niiri asamaan si nga jéggalu ma kon dinaa la jéggal te duma faale dara, yaw doomu Aadama boo ma indiloon luy jege suuf si ci bàkkaar yu bari, nga daje ak man te bokkaalewóo ma ak dara dinaa la indil njéggal lu toll ni moom".
Tane na At-tirmisiy soloo na ko.
Jële na ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne bu daan dugg ci jàkka day wax: "ahuusu bil Laahi Alhasiimi, wa bi wajhihi Alkariimi, wa sultaanihii alxadiimi, minas Saytaani Arrajiimi", nee na: ndax loolu rekk la? Ma ne ko: waaw, mu ne: bu waxee loolu saytaane day wax naan: aarees na ko ci man tay.
Tane na Abóo Daawuda soloo na ko.
Benn waay dafa ñëw ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, wax ak moom ci yenn mbir yi, daal di ne ko: bu soobe Yàlla soob la, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: "ndax dangamay yamale ak Yàlla? Waxal: bu soobe Yàlla moom dong".
Ag càllalaam tane na رواه ابن ماجه والنسائي في الكبرى وأحمد
"Yàlla jéggal na samaw xeet njuumte ak fàtte ak lu ñu leen forse".
An-Nawawii nee na hadiis bu rafet la Ibn Maaja ak Al-Bayhaqii ñoo ko soloo ak ñeneen.
Yonnente Yàlla bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-am mbooloo dañoo ñëw ci moom,mu jaayante ak juróom-ñent ñi bàyyi kenn ki,nu ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, jaayante nga ak juróom-ñent daal di bàyyi kii? Mu ne:"ab téere la takk",mu dugal loxoom dagg ko,daal di jaayante ak moom,daal di wax ne: "ku takk ab téere bokkaale na".
Tane na Ahmat soloo na ko.