Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

7 of 732 cards

Clear filters
«jullig góor gi ca mbooloo ma moo ëpp julleem ci këram ak ca ja ba luy tolloo ak ñaar-fukki daraja ak lu topp, loolu nag ndax bu kenn ci ñoom jàppee rafetal njàppu ma, daal di dem ca jàkka ja te dara yëkkatiwu ko lu dul julli, du jéego benn jéego lu dul ne dees na ko ci yëkkatil daraja, sippil ko ci njuumte, ba ba muy dugg ca jàkka ja, bu duggee ca jàkka ja ci julli la nekk fii ak julli moo ko téye, te malaaka yi dañuy julli ci kenn ci yéen fii ak moo ngi ca bérab ba mu doon jullee, dañuy wax naan: Yàlla yërëm ko, Yàlla jéggal ko, Yàlla nangul tuubam, fii ak lotul kenn, te tojlewul».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Benn waay dafa ñëw ci Yó’ente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: yaw Yónente Yàlla bi, man de amuma ku may wommat yóbb ma ca jàkka ja, mu sàkku ci Yónente Yàlla bi mu yombalal ko muy jullee ci këram, Yónente bi daal du loy jox Yombal, ba mu wëlbatikoo rekk mu woo ko, daal di ne ko: "ndax danga dégg wooteg julli gi?" Mu ne ko: waaw, mu ne ko: "kon nag wuyujil ».
Wér na Muslim soloo na ko.
"jullig mbooloo moo gën jullig kenn ci yéen moom dong, luy toll ci ñaar-fukk ak juróomi xaaj, Malaakay guddi gi ak Malaakay bëccëg gi dañuy daje ci jullig Fajar gi" topp Abuu Hurayrata wax ne: jàngleen bu leen neexee: {Alxuraanu Fajar gi lu ñuy teewe la} [Al-Israa: 78].
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«ku xëy dem ca jàkka ja, walla mu gont fa Yàlla dana ko waajalal ca àjjana ab wàccuwaay, saa yu xëyee walla mu gont».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"bu ñu taxawalee julli geneen julli amatul gu dul ga ñu farataal".
Wér na Muslim soloo na ko.
«ku lekk laaj walla soble, bumu nu jege -walla mu wax: bumu jege sunu jàkka yi, te toog ci këram", ak ne Yonnente bi indil nañu ko cin lu am ay lujum ak laaj, mu yég ci ag xet, mu laaj ñu xibaar la ca nekk ci laaj, mu wax ne: jegeele leen ko ci kenn ci Sahaaba yi nekkoon ak moom, ba mu ko gisee mu sib ko a lekk, mu wax ko ne: " lekkal, man damay déeyante ak koo dul déeyantel».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«sàppey góor ñi gi ci gën mooy gu njëkk gi, bi ci yées mooy gu mujj gi, sàppey jigéen ñi gi ci gën mooy gu mujj gi, gi ci yées mooy gu njëkk gi».
Wér na Muslim soloo na ko.