Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

7 of 732 cards

Clear filters
Dikk naa ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bëgg a dugg ci Lislaam, mu digal ma ma sàngu ci ndox ak siddéem.
Wér na Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy, ak An-nasaa'iy.
«kuy njëw ci yéen ci àjjuma ji na sangu».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc Saahu ndox daan na ko sang janaba Mudd it daan na ko jàppu.
Wér na Muslim soloo na ko.
«ku sangu bisub Àjjuma sangug janaba topp mu dem julli ji, dana mel ni ku saraxe ag giléem, ku dem ci ñenteelu waxtu wi moo ngi mel ni ku saraxe aw nag, ku dem ci ñatteelu waxtu wi moo ngi mel ni ku jegeele am kuuy mu ami béjjan, ku dem ci ñenteelu waxtu wi moo ngi mel ni ku saraxe ag ginaar, ku dem ci juróomeelu waxtu wi moo ngi mel ni ku saraxe ab nen, bu imaam bi génnee maalaaka yi ñëw di déglu xutba gi».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«war na ci bépp jullit mu sangu ci juróom ñaari fan yu nekk benn yoon, da ciy raxas boppam ak yaramam».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Tegal naa Yonnente bi sangukaay, ma làqe ko ab sér, mu sotti ci ñaari loxoom, daal di leen di raxas, mu sotti ci ndayjooram ci kaw càmmooñam daal di raxas awraam, mu teg loxoom ci suuf daal di koy fomp, topp mu raxas ko, mu daal di gallaxndiku daal di saraxndiku, daal di raxas kanamam ak ñaari loxoom, mu daal di sotti ci kaw boppam, mu daal di tooyal mbooleem yaramam, mu daal di randu, daal di raxas ay tànkam, ma jox ko ab moorso te jëlu ko, mu wéy dem di fëgg ay loxoom.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan sangu janaba, da daan raxas ñaari loxoom, jàpp njàppum julli, daal di sangu, daal di xàjjale ci loxoom kawaram, bu ko wóoree ne der ba tooy na, mu sotti ca ndox ñatti yoon, topp mu raxas mbooleem yaramam, Aysatu nee na: daan naa sangu man ak Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci benn ndab, nun ñaar ñépp di ci tanq.
Wér na Al-buxaariy soloo na ko.