Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

3 of 732 cards

Clear filters
«Yàlla mu kawe mi nee na: seddale naa julli ci sama diggante ak sama jaam bi ci ñaari xaaj, ñeel na sama jaam bi lu mu laaj, bu jaam bi waxee: {Alhamdu lil-Laah Rabbil haalamiina}, Yàlla mu kawe mi wax: sama jaam bi sant na ma, bu waxee: {Ar-Rahmaanir Rahiimi}, Yàlla mu kawe mi wax: sama jaam bi tagg na ma, bu waxee: {Maaliki yawmid diini}, mu wax: sama jaam bi màggal na ma, -am yoon bumu wax: sama jaam bi wéeru na ci man-, bu waxee: {Iyyaaka nahbudu wa Iyyaaka nastahiinu}, mu wax: lii sama diggante la ak sama jaam bi, te ñeel na sama jaam bi lu mu laaj, bu waxee: {Ihdinas siraatal mustaxiima, siraatal lasiina anhamta halayhim xayril maxduubi halayhim wa laddaaliina}, mu wax: lii sama jaam bi moo ko moom, te ñeel na sama jaam bi lu mu laaj».
Wér na Muslim soloo na ko.
«buleen def séen kër yi ay bàmmeel, Saytaane day daw kër goo xam ne dañu fay jàng saaru Al-Baxara».
Wér na Muslim soloo na ko.
Ba aaya bii wàccee ci Yonnente Yàlla bi {Yàlla moo moom li nekk ci asamaan yi ak suuf si bu ngeen feeñalee li nekk ci seen i bakkan walla ngeen nëbb ko Yàlla dana leen ci càmbar mu jéggal ku ko soob daal di mbugal ku ko soob te Yàlla man na lépp} [Al-Baxara: 284], nee na: loolu tar lool ci sahaabay Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ñu teg seen i wóom ci suuf, daal di ne: yaw Yonnente Yàlla bi, gal nañu ci ay lol àttan nanu ko, julli woor ak jihaad ak saraxe, waaye wàcce nañu ci aaya bii te manunu ko, Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne leen: "ndax dangeen bëgg a wax la ñoñ-téere ya leen jiitu woon waxoon dégg nanu moynanu? waaye waxleen: dégg nanu topp nanu noo ngi sàkku sag njéggal yaw sunu Boroom te yaw rekk yaay delluwaay ba", ñu daal di ne: dégg nanu topp nanu noo ngi sàkku sag njéggal yaw sunu Boroom te yaw rekk yaay delluwaay ba, ba ko gaaya waxee, seen làmmiñ ya nangu ko, Yàlla wàcce ca ginnaawam: {Yonnente bi gëm na li ñu wàcce ci mu bawoo ci Boroomam way gëm yi it ñépp gëm nañu gëm nañu Yàlla ak i malaakaam ak k téereem ak i Yonnenteem te duñu teqale diggante kenn ci Yónnenteem yi te dañuy wax naan dégg nanu topp nanu noo ngi sàkku sag njéggal yaw sunu Boroom te yaw rekk yaay delluwaay ba} [Al-Baxara: 285], ba ñu ko defee Yàlla mu kawe mi nasaxal ko, Yàlla mu màgg mi daal di wàcce: {Yàlla du togg benn bakkan lu dul lu mu man lu mu fàggu ci lu baax moom rekk la ñeel lu mu def ci lu bon it moom la ñeel Yàlla sunu Boroom bul nu jàppe ndeem danoo fàtte walla nu juum} [Al-Baxara: 286] " Mu ne: "waaw" {yaw Yàlla sunu Boroom bul nu teg coono kem na nga ko tege woon ña nu jiitu woon} [Al-Baxara: 286] Mu ne: "waaw" {yaw Yàlla sunu Boroom bul nu teg lu nu àttanul} [Al-Baxara: 286] Mu ne: "waaw" {yaw Yàlla sunu Boroom jéggal nj baal nu te yërëm nu yaw yaay sunu wéeruwaay dimbale nu ci kaw yéefar yi} [Al-Baxara: 286] Mu ne: "waaw".
Wér na Muslim soloo na ko.