عربي - Arabic English Qafár af - Afar Afrikaans - Afrikanns Akan Shqip - Albanian አማርኛ - Amharic Հայերեն - Armenian অসমীয়া - Assamese Azərbaycanca - Azerbaijani Bamanankan - Bambara Bassa Bemba বাংলা - Bengali Bosanski - Bosnian Български - Bulgarian မြန်မာဘာသာ - Burmese Bisaya - Cebuano Cham Нохчий - Chechen chiCheŵa - Chewa 中文 - Chinese Адыгэбзэ - Circassian Hrvatski - Croatian Česky - Czech Dagbani Dansk - Danish فارسی دری - Dari Dendi ދިވެހި ބަސް - Dhivehi Nederlands - Dutch إستوني - Estonian Suomi - Finnish Français - French Fulfulde - Fula ქართული - Georgian Deutsch - German Ελληνικά - Greek ગુજરાતી - Gujrati Kreyòl ayisyen - Haitian Creole Hausa हिन्दी - Hindi Magyar - Hungarian Igbo Indonesia - Indonesian Italiano - Italian 日本語 - Japanese Jóola - Jola ಕನ್ನಡ - Kannada Қазақша - Kazakh ភាសាខ្មែរ - Khmer Kikuyu Ikinyarwanda - Kinyarwanda Ikirundi - Kirundi 한국어 - Korean كوردی سۆرانی - kurdish كوردي kurmancî - Kurmanji Kyrgyz ລາວ - Lao latviešu - Latvian Lingala lietuvių - Lithuanian Luganda Македонски - Macedonian Maguindanaon Malagasy - Malagasy Bahasa Melayu - Malay മലയാളം - Malayalam Mandinka मराठी - Marathi Mõõré - Moore नेपाली - Nepali أنكو - NKo Norwegian ଓଡ଼ିଆ - Odia oromoo - Oromo پښتو - Pashto فارسی - Persian Polski - Polish Portuguese ਪੰਜਾਬੀ - Punjabi Română - Romanian Русский - Russian Српски - Serbian Shona සිංහල - Sinhala Slovenščina - Slovenian Soomaaliga - Somali Soninke Sesotho - Sotho Español - Spanish Kiswahili - Swahili Svenska - Swedish Tagalog Тоҷикӣ - Tajik தமிழ் - Tamil తెలుగు - Telugu ไทย - Thai ትግረኛ - Tigrinya Türkçe - Turkish Ukrainian اردو - Urdu ئۇيغۇرچە - Uyghur Ўзбек - Uzbek Việt Nam - Vietnamese Wolof Yao Yorùbá - Yoruba Zarma زولو - Zulu
732 Hadiths
Encyclopedia of Prophetic Hadiths
Categories
Grading
Narrated in
Narrator
Show all narrators (53)
Yonente Yàlla bi daan na nu xamal listixaar ci mbir yépp kem ni mu nu daan xamale saaru Alxuraan, mu wax ne: "bu kenn ci yéen yittewoo am mbir, na julli ñaari ràkka yu dul farata, topp mu wax: Allaahuma innii astaxiiruka, bi hilmika, wa astaqdiruka bi xudratika, wa as-aluka min fadlika Al-Hasiimi, fa innaka Taqdiru wa laa aqdiru, wa Tahlamu wa laa ahlamu, wa Anta Hallaamu alxuyuubi, Allaahuma in Kunta Tahlamu anna haasal amra xayrun lii fii diinii, wa mahaasii wa haaqibati amrii" walla mu wax: "haajili amrii, wa aajilihi, faqdurhu lii wa yasairhu lii summa baarik lii fiihi, wa in Kunta tahlamu anna haasal amra sarrun lii fii diinii wa mahaasii wa haaqibati amrii" walla mu wax: "haajili amrii wa aajilihi, fasrifhu hanni wasrifnii hanhu waqdur liya alxayra haysu kaana summa ardinii bihii" nee na: "mu tudd aajoom".
Wér na Al-buxaariy soloo na ko.
Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa nekkoon ci ab tukki, mu gis jenn waay ñu keral ko, mu daal di ne: "lii lan la?", ñu ne ko dafa woor, mu wax ne: "woor ci tukki bokkul gi ag mbaax", ñew na ci yeneen i baat ci Muslim: "dénk naa leen yombali Yàlla yi mu leen yombalal".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«ku lekk laaj walla soble, bumu nu jege -walla mu wax: bumu jege
sunu jàkka yi, te toog ci këram", ak ne Yonnente bi indil nañu ko cin lu am ay lujum ak laaj, mu yég ci ag xet, mu laaj ñu xibaar la ca nekk ci laaj, mu wax ne: jegeele leen ko ci kenn ci Sahaaba yi nekkoon ak moom, ba mu ko gisee mu sib ko a lekk, mu wax ko ne: " lekkal, man damay déeyante ak koo dul déeyantel».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"Yàlla ak ub yonnenteem araamal na ñu jaay sàngara, ak médd, ak mbaam xuux, ak ay xërëm", ñu ne ko yaw Yonnente Yàlla bi, luy mbiri gereesu médd? Dañu ciy diw gaal yi, di ci diw der yi, nit ñi di ci leerale? Mu ne: "déedéet, dafa araam", Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daal di wax ne: "yal na Yàlla ray Yahuud yi, ba Yàlla araamalee ci ñoom gerees ga dañu ko a seeyal, jaay ko, lekk njëg ga".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.