Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

4 of 732 cards

Clear filters
"Yàlla mu baarkeel mi te kawe day wax waa àjjana: éey yéen waa àjjana? Ñu ne ko wuyusi nanu la topp nañu la ak mbegte, mu ne leen: ndax gërëm ngeen? Ñu ne ko: lu ñuy teree gërëm te nga jox nu loo joxul kenn ci sa mbindeef yi? Mu ne leen: dama leen di jox lu gën loolu, ñu ne ko: yaw sunu Boroom, ana lan moo gën loolu? Mu ne leen: wàcce naa sama ngërëm ci seen kaw, dootuma leen mere ba fàww".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«dinañu indi dee ci melow kuuy mu duuf, ab wootekat daal di woote: yéen waa àjjana, ñu yoqamtiku di xool, mu wax ne: ndax xam ngeen lii ? Ñu ne ko: waaw, lii mooy dee, te ñoom ñépp a ko gis, mu woote ne: yéen waa sawara, ñu yoqamtiku di xool, mu wax ne: ndax xam ngeen lii ? Ñu ne ko: waaw, lii mooy dee, te ñoom ñépp a ko gis, ñu rendi ko, mu wax ne: yéen waa àjjana sax ba fàwwu dee amatul, yéen waa sawara sax ba fàwwu dee amatul, daal di jàng: {na nga leen xupp bisub réccu ba ba ñu àttee mbir ma fekk ñoom ñoo ngi cig càggante} [Maryama: 39], waa àdduna jii ñoo ngi cig càggante, {te ñoom duñu gëm}[Maryama: 39]».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"Yaw Abuu Sahiid, ku gërëm Yàlla muy Boroomam, Lislaam di diineem, Muhammat di Yonenteem àjjana war na ci moom", Abuu Sahiid yéemu ci loolu, ne ko: baamtul ma ko yaw Yonente Yàlla bi, mu def ko, topp mu ne ko: "ak leneen lol dees na ci yëkkëtil jaam bi téeméeri daraja ca àjjana, te diggante ñaari daraja yi mi ngi mel ni diggante asamaan ak suuf ", mu ne ko: loolu lan la yaw Yonente Yàlla bi? Mu ne ko: "jihaad ci yoonu Yàlla, jihaad ci yoonu Yàlla".
Wér na Muslim soloo na ko.
"amna ca Àjjana ag garab gog ki war aw fas wu ñu tàggat ba mu gaaw dana ca daw luy toll ak téeméeri at te du ko dog".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.