Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

124 of 732 cards

Clear filters

Narrator

Show all narrators (56)
"ñaar a ngi ci nit ñi ag kéefar la: jam ci askan yi, ak yuuxu ku dee".
Wér na Muslim soloo na ko.
«saa du taxaw lu dul ne nit dana romb ci bàmmeelu benn waay naan: aka neexoon ma nekk palaasam».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"képp ku sos ci sunu mbir mii lu ci bokkul dees ka koy delloo"
Wér na Al-Buxaarii ak muslim ñoo ko soloo
Moom dafa ñëw ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, Saytaane de dafa dox sama diggante ak sama julli gi, te day jaxase sama njàng mi, Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: " kooku Saytaane bu ñu woowe Xinsab la, boo ko yégatee nanga muslu ci Yàlla ci moom, te nga tifli ci sa càmmooñ ñatti yoon", nee na: ma def loolu Yàlla dindi ko ci man.
Wér na Muslim soloo na ko.
Benn waay dafa ñëw ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: yaw Yónente Yàlla bi, yan mooy ñaar yiy waral ? Mu ne ko: «ku faatu te bokkaalewul Yàlla ak dara dana dugg àjjana, ku faatu te bokkaale ko ak dara dana dugg sawara».
Wér na Muslim soloo na ko.
«ku woote jëme cig njub dana am ag pay gu mel ni payug ña ko ca topp, te du wàññi ci seeni pay dara, ku woote it jëme cig reer dana am bàkkaar bu mel ni bàkkaarub ña ko ca topp, te du wàññi ci seeni bàkkaar dara».
Wér na Muslim soloo na ko.
«ñiy taral alku nañu» wax na ko ñatti yoon.
Wér na Muslim soloo na ko.
«Yàlla du tooñ benn way-gëm ci jëfam ju baax di ko wàññi, dana ka ko jox fii ci àdduna fay ka ko ca allaaxira, bu dee ab yéefér nag ay jëfam yu baax yi mu def ngir Yàlla fii ci àdduna, dañu ka koy dundale, ba bu demee allaaxira, du fa fekk jenn jëf ju baax buñu koy fay».
Wér na Muslim soloo na ko.