Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

89 of 732 cards

Clear filters
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa romb ñaari bàmmeel, daal di wax ne : « ñoom ñaar de ñoo ngi leen di mbugal, te sax mbugaluñu leen ci lu rëy, kenn ki moom daawul suturawu bu daan saw, keneen ki nag da daan dox di rambaaj" mu jël aw xob wu tooy, xar ko ñaari xaaj, roof ci bàmmeel bu ne wenn xaaj, ñu ne ko : yaw Yónente Yàlla bi, lu tax nga def lii ? Mu wax ne : "amaana ñu woyafalal leen fii ak wowuñu».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«bàyyileen ma bu ma leen bàyyee, ndax li alag ña leen jiitu woon mooy seeni laaj ak di wuute ak seeni Yonnente , bu ma leen teree dara nangeen ko moytu, bu ma leen digalee dara defleen ca lu ngeen man».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa wax Muhaas Ibn Jabal ba mu ko yónnee Yaman ne ko: " yaa ngi jëmm ci aw nit woo xam ne ay ñoñ-téere lañu, boo demee ca ñoom, nanga leen woo ñu seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla ak ne Muhammat ndawu Yàlla la, bu ñu la toppee ci loolu, nga xamalleen ne Yàlla farataal na ci ñoom juróomi julli ci bis bu nekk aki gudeem, bu ñu la toppee ci loolu nga xamalleen ne Yàlla farataal na ci ñoom ab sarax bob dees na ko jëll ci séen way-woomal yi delloo ko ci séeni way-ñàkk, bu ñu la toppee ci loolu nag nanga moytu séen tedd-ngay alal ya, te nga moytu ñaanug ku ñu tooñ ndax amul kiiraay diggam ak Yàlla".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«li ñuy njëkk a àtte ci diggante nit ñi ëllëg bis-pénc mooy dereet ».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«saa du taxaw lu dul ne nit dana romb ci bàmmeelu benn waay naan: aka neexoon ma nekk palaasam».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"képp ku sos ci sunu mbir mii lu ci bokkul dees ka koy delloo"
Wér na Al-Buxaarii ak muslim ñoo ko soloo
Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu leen daan digal da leen di digal lu ñu àttan, ñi ne ko: nun melunu kem ni nga mel yaw Yonnente Yàlla bi, Yàlla jéggal na la li jiitu ci say bàkkaar ak li mujj, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daal di mer ba ñuy xam mer mi ci kanamam gi, topp mu ne: "ki leen gën a ragal Yàlla gën leen a xam Yàlla mooy man".
Wér na Al-buxaariy soloo na ko.
"tabax nañu lislaam ci juróom: seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla, ak ne Muhammat jaamam la di ndawam, ak taxawal julli, ak joxe asaka, ak aji Màkka, ak woor weeru koor ".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.