Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

14 of 732 cards

Clear filters
«yéen nit ñi tuubleen jëm ci Yàlla, man de damay tuub ci bis bi téeméeri yoon».
Wér na Muslim soloo na ko.
«Bu nodd-kat bi waxee: Allaahu Akbar Allaahu Akbar, kenn ci yéen wax: Allaahu Akbar Allaahu Akbar, bu waxee: ashadu an laa ilaaha illal Laahu, mu wax: ashadu an laa ilaaha illal Laahu, bu waxee: ashadu anna Muhammadan rasuulul Laahi, mu wax: ashadu anna Muhammadan rasuulul Laahi, bu waxee: hayya halas salaah, mu wax: laa hawla wa laa xuwwata illaa bil Laah, bu waxee: hayya halal falaah, mu wax: laa hawla wa laa xuwwata illaa bil Laah, bu waxee: Allaahu Akbar Allaahu Akbar, mu wax: Allaahu Akbar Allaahu Akbar, bu waxee: laa ilaaha illal Laahu, mu wax: laa ilaaha illal laahu te mu dëggu ci xolam kon dana dugg àjjana».
Wér na Muslim soloo na ko.
Ay nit ci Sahaabay Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dañoo wax Yonnente bi ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, way-woomal yi yóbb nañu yool yi, dañuy julli kem ni nuy jullee, di woor kem ni nuy woore, ñuy saraxe ca seen disiiti alal, mu dal di wax ne: "mo ndax Yàlla defalu leen lu ngeen di saraxee? Bépp sàbbaal ab sarax la, bépp sant ab sarax la, bépp tudd Yàlla it sarax la, digle lu baax sarax la, tere li bon sarax la, sëyug kenn ci yéen itam sarax la", ñu ne ko yaw Yonnente Yàlla bi, ndax kenn ci nun day def bànneexam ba noppi di ci am sarax? Mu ne: "xanaa du bu ko defoon ci lu araam da ciy am bàkkaar? Niki noonu it bu ko defee ci lu dagan da ciy am yool".
Wér na Muslim soloo na ko.
«bu ngeen déggee noddkat bi nangeen wax lu mel ni li muy wax, te ngeen julli ci man, ndax ku julli ci man genn julli Yàlla julli ci moom fukk, te ngeen ñaanal ma Wasiila ba, ndax moom ab bérab la ca àjjana, te kenn yayoowu ko ku dul ab jaam ci jaami Yàlla yi, te maa ngi yaakaar ne man la, ku ma ñaanal Wasiila samag ramm dagan na ko».
Wér na Muslim soloo na ko.
«ku wax: laa ilaaha illal laahu wahdahu laa sariika lahu, lahul mulku wa lahul hamdu wa Huwa halaa kulli say-in Xadiiru , fukki yoon dana mel ne ku goreel ñenti bakkan ci doomi Ismaayla».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da doon dox ci mbeddi Màkka yi, daal di romb doj wu ñuy woowe Jumdaan, mu wax ne: "doxleen lii mooy Jumdaan, ñu beru ñi raw nañu" ñu ne ko: ñan ñooy ñi beru yaw Yonnente Yàlla bi? Mu ne: "góor ñiy tudd Yàlla lu bari, ak jigéen ñiy tudd Yàlla lu bari".
Wér na Muslim soloo na ko.