Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

64 of 732 cards

Clear filters
Wax naa : yaw Yónente Yàlla bi, wax ma ci Lislaam wax joo xam ne duma ko laaj kenn ku dul yaw, mu ne ma : "waxal gëm naa Yàlla, te jub kocc".
Wér na Muslim soloo na ko, ak Ahmat.
"Jëf yi mi ngi aju ci yéene yi, te nit ku nekk la mu yéene rekk lay am, képp ku gàddaay ngir Yàlla ak ub Yonenteem, kooku gàddaayam dina jëm ci Yàlla ak Yonenteem, waaye képp ku gàddaay ngir àdduna jum soxlaa jot walla jigéen ju mu bëgg a takk kon gàddaayam jëm na ca la ko tax a gàddaay".
Wér na Ñaari imaam yi ci hadiis ñoo ko soloo, ñuy Abuu Abdillaahi Mouhammad ibn Ismaahiil ibn Ibraahiim ibn Al-Muxiirata ibn Bardisba Al-Buxaarii ak Abul Hussayn Muslim ibn Hajjaaj ibn Muslim Al-Xusayrii An-Naysaabuurii, ci seen ñaari téere yu wér yi nga xam ne ñoo gën a wér ci téere yi ñu taalif.
Laaj naa Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc xoolug mbetteel mu digal ma ma wëlbati samab gis.
Wér na Muslim soloo na ko.
«àdduna de ñam wu neex la te naat, Yàlla da leen fee wuutal, di xool lu ngeen fiy jëf, noytuleen àdduna te moytu jigéen ñi, ndax fitna ji njëkk a am ci Banuu Israayil ci jigéen la xewe».
Wér na Muslim soloo na ko.
«bàyyiwuma sama ginnaaw fitna ju dàq a lor góor ñi ci jigéen ñi»
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"ñaari xaaj a gi nii yu bokk ci waa sawara te gisaguma leen,ay nit yu yor ay yar yu mel ni geeni nag di ci dóor nit ñi,ak ayjigéen yu solu ba noppi rafle, jeng di jengale, seeni bopp ya day mel ni jégénu giléem gu jeng,duñu dugg àjjana,te xet ga sax du leen xeeñ,te xetam ga dana toll ci doxub nangam ak sàngam".
Wér na Muslim soloo na ko.
«jëf yi mi ngi aju ci yéene ja, te nit ku nekk la mu yéene rekk lay am, képp ku gàddaay ngir Yàlla ak ub Yónenteem, koo ku gàddaayam dina jëm ci Yàlla ak Yónenteem, waaye képp ku gàddaay ngir àdduna jum soxlaa jot, walla jigéen ju mu bëgg a takk; kon gàddaayam jëm na ca la ko tax a gàddaay" ci beneen nettali ci Al-Buxaarii: "jëf yi mi ngi aju ca yéene ya, te nit ku nekk la mu yéene rekk lay am».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"gaaral na ñu ma Àjjana ak Sawara waaye gisuma ca yiw walla ay wu mel ni tay jii, te bu ngeen xamoon li ma xam kon dangeen ree tuuti te dangeen jooy lu bari, nee na: bis bu ko gën a tar musul a am ci Sahaabay Yonente Yàlla bi, nee na: ñu muur seen bopp yi di yékkét, nee na: Umar daal di ne: gërëm nanu Yàlla muy sunu Boroom, ak Lislaam muy sunu Diine, ak Muhammat muy sunu Yonente, nee na: waa jooja daal di jug, daal di ne: kan mooy sama baay? Mu ne ko: "diw mooy sa baay" aaya bii wàcc: {yéen way-gëm ñi bu leen laaj loo xam ne bu ñu leen ko leeralee mu naqari leen} [Al-Maa-ida: 101].
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.