Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

3 of 732 cards

Clear filters
Mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne moom Yónente bi tere na nisër, daal di wax ne: "du indi aw yiw, waaye dees ciy genne aji-nay ji".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"ku giñ ci dara fekk du dëgg ngir dog ci àqi ab jullit, dana daje ak Yàlla fekk mu mere ko". Nee na: Ashas wax ne: giñ naa ci Yàlla ne loolu ci man la nekk; suuf dafa doxoon ci sama diggante ak ub Yahuud, mu weddi ma, ma yóbb ko ci Yonente bi, Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ma: "ndax am nga firnde?" Ma ne ko: déedéet. Nee na: mu ne Yahuud bi: "giñal". Nee na: ma ne ko: yaw Yonente Yàlla bi, kon daal day giñ daal di yóbb sama alal. Yàlla mu kawe mi daal di wàcce: {ñi nga xam ne dañuy jënne kóllareg Yàlla gi ak seen i giñ ci ag njëg gu ndaw} ba aaya bi jeex.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Ñëw naa fi Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ànd ak mbooloo yu bokk ci giirug Al-Asharii, mu wax ne: "giñ naa ci Yàlla ne duma leen gàddu te sax amuma lu ma leen gàddul" ñu des fa diir ba soob Yàlla, ñu dal di koy indil ay giléem, mu digle ñu jox leen ñatti giléem, ba ñu fa jógee, ñenn ci nun wax ñeneen ñi: Yàlla de du nu baarkeelal, ñëw nanu fi Yonnente Yàlla bi di sàkku mu gàddul nu mu giñ ne du nu gàddul ba noppi daal di nuy gàddul, Abuu Muusaa nee na: nu dem fi Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc wax ko loolu, mu ne nu: "du man maa leen gàddul, waaye Yàlla moo leen gàddul, man de giñ naa ci Yàlla ne -bu soobee Yàlla- duma giñ ci dara ba noppi gis leneen lu ko gën, lu dul ne dinaa kaffaara sama giñ ba te def la ko gën".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.