Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

22 of 732 cards

Clear filters

Narrator

Show all narrators (48)
«ku sàbbaal Yàlla ginnaaw julli gu ne fanweeri yoon ak ñatt, sant Yàlla fanweeri yoon ak ñatt, màggal Yàlla fanweeri yoon ak ñatt, loolu juróom-ñent-fukk ak juróom ñent la, mu wax: ci mottali ko téemeer: laa-i-Laaha Illal Laahu wahdahu laa sariika lahu lahul mulku wa lahul hamdu wa Huwa halaa kulli say-in Xadiirun, ñu jéggal ko ay njuumteem doonte dafa toll ni puuriti géej».
Wér na Muslim soloo na ko.
"buleen tere jibéeri Yàlla yi jàkkay Yàlla yi, waaye nañu génn nekk ñu lëmësu".
Tane na Abóo Daawuda soloo na ko.
«ku sangu bisub Àjjuma sangug janaba topp mu dem julli ji, dana mel ni ku saraxe ag giléem, ku dem ci ñenteelu waxtu wi moo ngi mel ni ku saraxe aw nag, ku dem ci ñatteelu waxtu wi moo ngi mel ni ku jegeele am kuuy mu ami béjjan, ku dem ci ñenteelu waxtu wi moo ngi mel ni ku saraxe ag ginaar, ku dem ci juróomeelu waxtu wi moo ngi mel ni ku saraxe ab nen, bu imaam bi génnee maalaaka yi ñëw di déglu xutba gi».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"bu nit ñi xamoon li nekk ci nodd gi ak sàppe su njëkk si te manu ñu lu dul tegoo bant kon danañu ko tegoo bant, te bu ñu xamoon li nekk ci teela dem kon danañu njëkkante jëm ca, bu ñu xamoon it li ci gee ak suba danañu ko dikkal donte dañuy raam".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"jullig mbooloo moo gën jullig kenn ci yéen moom dong, luy toll ci ñaar-fukk ak juróomi xaaj, Malaakay guddi gi ak Malaakay bëccëg gi dañuy daje ci jullig Fajar gi" topp Abuu Hurayrata wax ne: jàngleen bu leen neexee: {Alxuraanu Fajar gi lu ñuy teewe la} [Al-Israa: 78].
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«ku xëy dem ca jàkka ja, walla mu gont fa Yàlla dana ko waajalal ca àjjana ab wàccuwaay, saa yu xëyee walla mu gont».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«boo waxee sa àndandoo: noppil ci bisu àjjuma, fekk imaam bi di xutba, kon fo nga».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"bu ñu taxawalee julli geneen julli amatul gu dul ga ñu farataal".
Wér na Muslim soloo na ko.