Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

5 of 732 cards

Clear filters
"tabax nañu lislaam ci juróom: seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla, ak ne Muhammat jaamam la di ndawam, ak taxawal julli, ak joxe asaka, ak aji Màkka, ak woor weeru koor ".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«kuy njëw ci yéen ci àjjuma ji na sangu».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan ubbi julli gi day yëkkati loxoom ba mu tolloo ak mbagg yi, naka noonu it daan na leen yëkkati bu daan kàbbar ngir rukóo, ak bu daan siggi ca rukóo ba, ak bu daan yëkkati boppam jóge ca rukóo ba, daal di wax: "samihal Laahu liman hamidahu", daawul def loolu nag ca sujjóot ba.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Mokkal naa ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- fukki ràkka: ñaari ràkka njëkk tisbaar, ak ñaari ràkka ci ginnaawam, ak ñaari ràkka ginnaaw timis ci këram, ak ñaari ràkka ginnaaw gee ci këram, ak ñaari ràkka njëkk jullig suba, moom nag aw waxtu la woo xamne kenn daawul dugg fa Yonnente bi nekk, Hafsa nettalinama ne bu noddkat bi daan nodd ba fajar gi fenk day julli ñaari ràkka, ci jeneen wax: moom Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daan na julli ñaari ràkka ginnaaw àjjuma.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér, ci mbooleem anami nettali yi mu dikkee.
Jenn waay dafa laaj Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc fekk ma nga ca kaw Minbar ba, loo gis ci julli guddi, mu ne ko: "ñaar ñaar, bu ragalee suba jot mu julli benn ràkka, tóolale ko li mu julli" daan na wax it: "defleen seen mujjug julli muu lu tóol" ndax Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moo ko digle.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.