Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

8 of 732 cards

Clear filters
"yéen nit ñi, deeleen tasaare nuyóo, di leele ñam, di jokk mbokk, di julli guddi fekk nit ñi a ngi nelaw, kon dangeen dugg àjjana ci jàmm".
Wér na At-tirmisiy soloo na ko, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat.
«kóllare gi dox ci sunu diggante ak ñoom yéefar yi mooy julli, ku ko bàyyi weddi na».
Wér na At-tirmisiy soloo na ko, ak An-nasaa'iy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat.
Li ëppoon ci dénkaaney Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bi muy génn àdduna: "dénk naa leen julli ak ñi nekk ci seeni loxo, dénk naa leen julli ak ñi nekk ci seeni loxo" (seen jaam yi), ba Yonente bi dënnam ba tàmbalee di xar-xarale, ba daanaka làmmiñam leeratul.
Wér na رواه النسائي في السنن الكبرى وابن ماجه
«yëkkëti nanu xalima gi ci ñatt, ci kiy nelaw ba baa muy yeewu, ak ci xale bi ba baa muy gént, ak ci dof bi ba baa muy xellu».
Wér na Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy, ak An-nasaa'iy ca Al-kubraa, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat.
"ku bàyyi ñatti àjjuma ngir woyofal ko Yàlla dana tàppe xolam".
Wér na Abuu Daawuda ak At-Tirmisiyyu ak An-Nasaa-iyyu ak Ibn Maaja ak Ahmad ñoo ko soloo.
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daan na wax ci diggante ñaari sujjóot yi: «Rabbi ixfir lii, Rabbi ixfir lii».
Wér na Abóo Daawuda soloo na ko, ak An-nasaa'iy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat.
"bu kenn ci yéen duggee ci jàkka na ñaanal Yonnente bi te wax: Allaahumma iftah lii abwaaba rahmatika, bu génnee na ñaanal Yonnente bi te wax: Allaahumma ihsimnii minas saytaani arrajiimi", nekk ci Al-Haakim: "bu génnee na ñaanal Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc te mu wax: Allaahumma ajirnii minas saytaani arrajiimi".
Tane na Ibn Maaja ak Al-Haakim ñoo ko soloo.
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da daan wax ci diggante ñaari sujjóot yi: «Allaahumma ixfir lii, warhamnii, wa haafinii, wahdinii, warsuqnii».
Tane na bees sukkandikoo ci yeneen yi koy dëggal Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat.