Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

49 of 732 cards

Clear filters
«war na ci bépp jullit mu sangu ci juróom ñaari fan yu nekk benn yoon, da ciy raxas boppam ak yaramam».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Ànd nanu ak Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc jóge Màkka jëm Madiina ba nu eggee ci am ndox ci yoon wi am ñu gaawantu ca Tàkkusaan ga, daal di jàppu cig yàkkamti, ba nu egge fa ñoom gis seen tastën ya ndox mi laalu ko, Yonnente bi daal di wax ne: "mbugal ñeel na tastën ya ca sawara, deeleen jotal njàppu mi".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Jële na ñu ci Humraan jaamub Usmaan Ibn Affaan, mu wax ne, gis na Usmaan Ibn Affaan laaj ndox mu mu jàppoo, mu tanq loxoom ci ndab li, raxas leen ñatti yoon, mu dugal ndeyjooram ci jàppukaay bi, daal di gallaxndiku saraxndiku fiiru, daal di raxas xar kanamam ñatti yoon, ak ñaari loxoom ba ci conco yi ñatti yoon, daal di masaa boppam, daal di raxas tànk bu ne ñatti yoon, daal di wax ne: gis naa Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy jàppoo kem sama njàpp mii, ba noppi wax ne: "ku jàppoo kem sama njàpp mii, daal di julli ñaari ràkka yoy du ca xalaat dara, kon Yàlla dana ko jéggal bàkkaaram yi jiitu".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«socc day laabal gémmeñ di gërëmloo Boroom bi».
Wér na An-nasaa'iy soloo na ko, ak Ahmat.
"jullit bi bu jàppoo ba raxas xar kanamam; bàkkaar bu mu mas a def ci ay gëtam day rot ànd ak ndox mi, -walla ànd ak toq ndox bi mujj-, bu raxasee ay yoxoom bépp bàkkaar bu mu mas a def ci ay yoxoom dana rot ànd ak ndox mi, ni ki noonu bu raxasee ay tànkam bàkkaar yi mu masa dox ak tànkam yépp dana rot ànd ak ndox mi -walla ànd ak toq ndox bi mujj-, ba keroog muy set wicc ci ay bàkkaar".
Wér na Muslim soloo na ko.
Ummu Habiibata bint Jahsin mi nekkoon ci soxnas Abdur Rahmaan ibn Awf dafa jàmbat Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dereet ju muy gis, mu ne ko: "toogal diir bi la sa mbaax daan téye, topp nga sangu". Tax mu daan sangu ci julli gu nekk.
Wér na Muslim soloo na ko.
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na raxas, walla daan na sangu ci Saah ba ci juróomi Mudd, (mooy ñaari loxoom bamu fees) daan jàppu ci benn Mudd.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Nekkoon naa ak Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- cib tukki, ma nar a summi ñaari saŋam yi, mu ne ma: "bàyyileen, dama leen cee dugal ñu di ñu laab" mu masaa ca seen kaw.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.