Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

48 of 732 cards

Clear filters
"saytaane day fas ci ginnaaw boppu kenn ci yéen bu dee nelaw ñatti fas, genn fas-fas gu nekk day waral ci yaw guddi gu gudd, mu naan nelawal, bu yeewoo daal di tudd Yàlla genn fas-fas fecceeku, bu jàppoo geneen fas-fas fecceeku, bu jullee geneen fas-fas fecceeku, mu mujj nekk ku sawar, ku teey bakkan, bu dul loolu day nekk ku bon bakkan di ku tàyyeel".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«bu kenn ci yéen yëgée ci biiram dara, te xamul ndax dara génn na ci moom walla déet, bumu génn jàkka ci ba keroog muy dégg kàddu, mbaa mu yég ngelaw».
Wér na Muslim soloo na ko.
«Yàlla du nangu jullig kenn ci yéen bu dee daa tojle ba keroog muy jàpp».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da daan jàppu ci julli gu ne, ma ne ko: lan ngeen daan def yéen? Mu ne: njàpp mi dana doy nit ki feeg tojlewul.
Wér na Al-buxaariy soloo na ko.
"«Yi Yàlla moñaale ak nit ki juróom la: xaraf, wat kawaru naq, ak wàññi kawari mustaas, ak lewwi ay weh, ak suqi kawari poqtaan».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"bu ngeen demee ca duus ba buleen jublu xibla, te buleen ko dummóoyu, waaye nangeen jëm Sarq walla Xarb", Abuu Ayyuuba nee na: nu dem Saam fekk fa ay duus yu nu tabax mu jëm xibla nuy wetu, tey jéggalu Yàlla mu kawe mi.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Dikk naa ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bëgg a dugg ci Lislaam, mu digal ma ma sàngu ci ndox ak siddéem.
Wér na Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy, ak An-nasaa'iy.
«bu kenn ci yéen laal sakaraam ci ndayjooram fekk ma ngay saw, te bu demee duus ba noppi bu mu fompoo ndayjooram, te bu mu noyyi ci ndab li».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.