Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

3 of 732 cards

Clear filters
Aw nit ci ngiiru Hukal walla Haraynata dañoo dugg Madiina Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc digle ñu rattal leen, ak nu naan ci sawu gileem ak soowam mi, ñu dem, ba ñu wéree nag daal di ray ka doon sàmmal Yonente bi daal di wommat jur ga yóbb, xibaar bi egsi ci njëlbeenu bëccëg gi, mu yonnee ñu topp leen, ba bëccëg ga yëkkëtikoo ñu indi leen, mu digle ñu dagg seen loxo yi ak seen tànk yi, daal di buqi seen bët yi, ñu sànni leen ca tàngaay wa, ñuy sàkkoo naan te mayuñu leen ñu naan ba ñu dee, Abuu Xilaabata nee na: ñii sàcc nañu ray nañu daal di weddi ginnaaw ba ñu gëmee, daal di xeexak Yàlla ak ub yonnenteem.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu daan seeti ku feebar di ko ñaanal day wax: "ashibil basa, rabban naasi, wasfi Anta As-Saafii, laa sifaa-a illaa sifaa-uka sifaa-an laa yuxaadiru saqaman".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«dinaa jox raaya jii suba jenn waay joj Yàlla dana def ubbi gi ci ay loxoom, dafa bëgg Yàlla ak ub Yonnenteem, Yàlla ak ub Yonnenteem bëgg ko», nee na: nit ñi di waxtaane ci guddi gi kan ci ñoom lañu koy jox, ba nit ña xëyee dem ca Yonnente ba -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ku nekk ci ñoom di mébét nu jox ko ko, mu wax ne: "ana Aliyun Ibn Abii Taalib?" Ñu ne ko: moom de ay bëttam lay jàmbat yaw Yonnente Yàlla bi, mu wax ne: "yónneeleen fa moom", ñu indi ko Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di tifli ci kanam gi ñaanal ko, mu wér ba mel ni dara mettiwu ko woon, mu jox ko raaya ja , Aliyun ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, ndax damay xeex ak ñoom ba ñu mel ni nun? Mu ne ko: "defal ndànk-ndànk ba wàcc ca seen bayaal ba, nga woo leen ci Lislaam, te xamal leen li leen ci war ci àqi Yàlla, giñ naa ci Yàlla ne Yàlla gindi ci yaw benn waay moo gën ci yaw nga am géttug jur".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.