"ku julli sunu julli gi jublu sunu xibla bi lekk sunu rendi kooku mooy jullit bi nga xam ne amna kóllareg Yàlla ak kóllareg Yonnenteem bi, buleen wor Yàlla ci kóllareem gi".
Jële nañu ci Anas Ibn Maalik yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee ne:
"ku julli sunu julli gi jublu sunu xibla bi lekk sunu rendi kooku mooy jullit bi nga xam ne amna kóllareg Yàlla ak kóllareg Yonnenteem bi, buleen wor Yàlla ci kóllareem gi".
«مَنْ صَلَّى صَلاَتَنَا وَاسْتَقْبَلَ قِبْلَتَنَا وَأَكَلَ ذَبِيحَتَنَا فَذَلِكَ المُسْلِمُ الَّذِي لَهُ ذِمَّةُ اللَّهِ وَذِمَّةُ رَسُولِهِ، فَلاَ تُخْفِرُوا اللَّهَ فِي ذِمَّتِهِ».
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne ku taqoo ak màndargay diine yi feeñ di julli sunu julli gi, jublu sunu Kaaba gay sunu xibla, lekk sunug rendi def ko muy lu dagan; kooku mooy jullit bi am kóoluteg Yàlla ak ub Yonnenteem ak seen kóllare, kon buleen fecci kóoluteg Yàlla ak kóllareem ci moom.
Ibn Rajab nee na: hadiis day tegtale ne dereet du aaru ci ñaari seede yi dong, ba keroog muu taxawe ay àqam, li gën a feddaliku ci ay àqam nag mooy julli; loolu moo tax mu jagleel ko cig tudd; amna beneen hadiis bu mu julli ci julli gi asaka.
Mbiri nit ñi dañu koy yen ci li fés wolif li nëbbu, ku fésal màndargay diine ji ñu wéyal ci moom àttey ñoñi diine ji fii ak fésalul lu wuute ak loolu.
Ibn Rajab nee na: dafa tudd jublu xibla ngir junj ne manul njàkk ci julli gi ñu yoonal ci jullit ñi ci seen téere bi ñu wàcce ci seen Yonnente bi te mooy julli jublu Kaaba ga, lu ko moy ku julli jëm Bayt Maqdis ginnaaw ba ñu ko nasaxalee niki Yahuud yi walla mu jëm ca penku ba niki Nasaraan yi kooku du jullit, doonte dafa seede seedeg Tawhiid.
Tegtal nekk na ci ci màggug dayog jubluwaayu xibla gi ci julli, ndaxte tuddul ci sàrti julli lu dul moom, niki laab ak leneen.
Ibn Rajab nee na: tudd gi mu tudd lekk rendig jullit ñi ag junj a ngi ci, ci ne manul ñàkk ñu taqoo ak mbooleem màndargay lislaam yi feeñ, te bokk na ci yi ci gën a màgg lekk rendig jullit ñi, ak dëppoo ak ñoom ci seenug rendi, ku bañ loolu kooku nekkul jullit.
Téere Al-buxaariy bi gën a wér (1/ 87) (391).
Yataal gi (2)
إرشاد الساري لشرح صحيح البخاري (1/ 410).
عمدة القاري شرح صحيح البخاري (4/ 125).