Skip to content

«buleen di giñ ci yi ñuy jaamu te du Yàlla, buleen di giñ it ci seen i baay».

Jële na ñu ci Abdur Rahman Ibn Samurata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:

«buleen di giñ ci yi ñuy jaamu te du Yàlla, buleen di giñ it ci seen i baay».

«لَا تَحْلِفُوا بِالطَّوَاغِي، وَلَا بِآبَائِكُمْ».

Muslim soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day tere giñ ci Taaxuut yi, te mooy xërëm yi bokkaalekat yi daan jaamu wolif Yàlla, te sabab la ci seen ug bew ak seen ug kéefar, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day tere ñuy giñ ci baay yi; ndax daa bokkoon ci aaday araab yi ca ceddo ga ñuy giñ ci seen baay yi ngir ndamu ak màggal.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Giñ ci ku dul Yàlla ak i turam ak i meloom daganul.

Araamal nañu giñ ci Tawaaxiit yi, ak ci baayeek maam yi ak ci njiit yi, ak ci xërëm yi, ak lepp luko niru ci ay neen.

Gin ci ku dul Yàlla bokkaale gu ndaw la, te man naa nekk bokkaale gu mag, bu màggalee li muy giñe ci xolam kem ni ñuy màggale Yàlla walla mu fas ci dara ci ag jaamu.

Dellluwaay yi

Téere Muslim bi gën a wér.

Yataal gi (8)

نزهة المتقين.

مجموعة من الباحثين (2/ 1166).

شرح رياض الصالحين.

لابن عثيمين (6/ 451).

سبل السلام.

لمحمد الصنعاني (2/ 545).

المنهاج شرح صحيح مسلم.

للنووي (11/ 108).