jan jëf la Yàlla gën a bëgg? Mu wax ne: "julli ci waxtoom" mu ne ko: teg ca lan? Mu ne: "teg ca fonk ñaari way-jur" mu ne ko: teg ca lan? Mu ne: "jihaad ci yoonu Yàlla"
Jële na ñu ci Abdullah Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Laaj naa Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-: jan jëf la Yàlla gën a bëgg? Mu wax ne: "julli ci waxtoom" mu ne ko: teg ca lan? Mu ne: "teg ca fonk ñaari way-jur" mu ne ko: teg ca lan? Mu ne: "jihaad ci yoonu Yàlla" nee naa moo ma ko wax, te bi ma sàkkoon ndollin mu dolli ma.
سَأَلْتُ النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: أَيُّ العَمَلِ أَحَبُّ إِلَى اللَّهِ؟ قَالَ: «الصَّلاَةُ عَلَى وَقْتِهَا»، قَالَ: ثُمَّ أَيٌّ؟ قَالَ: «ثُمَّ بِرُّ الوَالِدَيْنِ» قَالَ: ثُمَّ أَيٌّ؟ قَالَ: «الجِهَادُ فِي سَبِيلِ اللَّهِ» قَالَ: حَدَّثَنِي بِهِنَّ، وَلَوِ اسْتَزَدْتُهُ لَزَادَنِي.
Laaj nañu Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-: jan jëf la Yàlla gën a bëgg? Mu wax ne: julliy juróom ci waxtoom wi ko Sariiha tënk, Teg ca fonk ñaari way-jur, di rafetal jëme ci ñoom, di taxaw ci seeni àq, te bañ leen a moy, Teg ca jihaad ci yoonu Yàlla, ngir yëkkati kàddug Yàlla mu màgg mi, ak aar diineem ji ak waa diine ji, ak fésal màndargaam, ci bakkan ak ci alal. Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dollee gërëm- nee na: moo ma xibaar jëf yii; te bu ma ko waxoon: teg ca lan? Kon dana ma dolli.
.....:
Gënanteg jëf yi ci seen diggante mi ngi aju ci Yàlla bëgg ko.
Ñaax jullit bi ci mu xér ci jëf yi, jiital bi gën teg ca ba ca tege.
Tontuy Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci jan jëf moo gën dana wuute, ci kem nit ñi ak seeni melokaan, ak lan moo ëpp njariñ ci kenn ku ne.
Téere Al-buxaariy bi gën a wér (1/ 112) (527).
Téere Muslim bi gën a wér (1/ 90) (85).
Yataal gi (6)
الإلمام بشرح عمدة الأحكام.
لإسماعيل الأنصاري (1/ 70).
تيسير العلام شرح عمدة الأحكام.
للبسام (ص84).
تنبيه الأفهام شرح عمدة الأحكام.
لابن عثيمين (1/ 108).
Cited in books
5 BooksYataal gi (5)
- الصلاة التي علمها النبي ﷺ الصحابة رضي الله عنهمالصلاة التي علمها النبي ﷺ الصحابة رضي الله عنهمسَأَلْتُ النَّبِيَّ ﷺ: أَيُّ العَمَلِ أَحَبُّ إِلَى اللَّهِ؟ قَالَ: «الصَّلاَةُ عَلَى وَقْتِهَا»، قَالَ: ثُمَّ أَيٌّ؟ قَالَ: «ثُمَّ بِرُّ الوَالِدَيْنِ» قَالَ: ثُمَّ أَيٌّ؟ قَالَ: «الجِهَادُ فِي سَبِيلِ اللَّهِ» قَالَ: حَدَّثَنِي بِهِنَّ، و
- الصلاة التي علمها النبي ﷺ الصحابة رضي الله عنهمسَأَلْتُ النَّبِيَّ ﷺ: أَيُّ العَمَلِ أَحَبُّ إِلَى اللَّهِ؟ قَالَ: «الصَّلَاةُ عَلَى وَقْتِهَا»، قَالَ: ثُمَّ أَيٌّ؟ قَالَ: «ثُمَّ بِرُّ الوَالِدَيْنِ» قَالَ: ثُمَّ أَيٌّ؟ قَالَ: «الجِهَادُ فِي سَبِيلِ اللَّهِ» قَالَ: حَدَّثَنِي بِهِنَّ، و
- المنتقى من المتجر الرابح في ثواب العمل الصالح - المعتمدالمنتقى من المتجر الرابح في ثواب العمل الصالحسألت رسول الله صلى الله عليه وسلم: أي العمل أحب إلى الله؟ قال: “الصلاة على وقتها”.
- نبراس طالب (1)1أَيُّ العَمَلِ أَحَبُّ إِلَى اللهِ؟ قَالَ: «الصَّلاَةُ عَلَى وَقْتِهَا»
- نبراس طالب (2)نبراس طالب (2) فعن عَبْدِ اللهِ بنِ مسعود رضي الله عنه قَالَ: «سَأَلْتُ النَّبِيَّ صلى الله عليه وسلم: أَيُّ الْعَمَلِ أَحَبُّ إِلَى اللهِ؟ قَالَ: الصَّلَاةُ عَلَى وَقْتِهَا»