«ku julli ñaari sedd yi dana dugg àjjana»
Jële na ñu ci Abuu Muusa Al-Asharii-yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«ku julli ñaari sedd yi dana dugg àjjana»
«مَنْ صَلَّى الْبَرْدَيْنِ دَخَلَ الْجَنَّةَ»
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day soññee ci xér ci jullig ñaari sedd yi, te mooy jullig fajar ak tàkkusaan, mu bégal ki leen julli te jox leen seeni àq ca waxtu wa ca mbooloo ma, ak lu dul yooyu, danañu nekk sabab ci mu dugg àjjana.
Ngëneelu sàmmonte Ak jullig fajar ak tàkkusaan; ndaxte fajar day ame ca nelaw yu neex ya, Tàkkusaan di ame fa nit ka di yittewoo liggéeyam, kon ku sàmmonte ak ñoom yell na mu sàmmonte ak julli yi des.
Tudde nañu jullig fajar ak tàkkusaan ñaari sedd yi; ndaxte jullig fajar daa am seddug guddi gi, jullig tàkkusaan am seddug bëccag gi donte ci waxtu wu tàng lay nekk it waaye mooy gën a sedd waxtu yi ko jiitu, walla tudde gi nekk ci anamug notal, kem ni ñuy waxe: ñaari weer yi, jublu ci jant bi ak weer wi.
Téere Al-buxaariy bi gën a wér (1/ 119) (574).
Téere Muslim bi gën a wér (1/ 440) (635).
Yataal gi (4)
نزهة المتقين.
لمجموعة من الباحثين (1/ 159).
شرح رياض الصالحين.
لابن عثيمين (2/ 187).
Cited in books
3 BooksYataal gi (3)
- المنتقى من المتجر الرابح في ثواب العمل الصالح - المعتمدالمنتقى من المتجر الرابح في ثواب العمل الصالح“من صلى البردين دخل الجنة”.
- رياض الصالحينرياض الصالحين مع فوائد وهدايات - 1 «مَنْ صَلَّىٰ الْبَرْدَيْنِ دَخَلَ الْجَنَّةَ».
- رياض الصالحينرياض الصالحين مع فوائد وهدايات - 5«مَن صلَّىٰ البَرْدَيْنِ دَخَلَ الجَنَّةَ».