Skip to content

"amul benn jullit bu musiba di dal mu wax li ko Yàlla digal: {Innaa lillaahi wa innaa ilayhi raajihuun} [Al-Baxara: 156], Yàlla defal ma aw yiw ci sama musiba bii, te wuutalal ma ko aw yiw, lu dul ne Yàlla dana ka ko wuutalal lu ko gën"

Jële nañu ci Ummu Salamata Ndayu jullit ñi yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: dégg naa Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:

"amul benn jullit bu musiba di dal mu wax li ko Yàlla digal: {Innaa lillaahi wa innaa ilayhi raajihuun} [Al-Baxara: 156], Yàlla defal ma aw yiw ci sama musiba bii, te wuutalal ma ko aw yiw, lu dul ne Yàlla dana ka ko wuutalal lu ko gën", nee na: ba Abuu Salamata faatoo ma ne: ana kan ci jullit ñi mooy gën Abuu Salamata? Kër gi njëkk a gàddaay jëm ca Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, topp ma wax ko, Yàlla daal di ma koy wuutalal Yonente Yàlla bi.

«مَا مِنْ مُسْلِمٍ تُصِيبُهُ مُصِيبَةٌ فَيَقُولُ مَا أَمَرَهُ اللهُ: {إِنَّا لِلهِ وَإِنَّا إِلَيْهِ رَاجِعُونَ} [البقرة: 156]، اللَّهُمَّ أْجُرْنِي فِي مُصِيبَتِي، وَأَخْلِفْ لِي خَيْرًا مِنْهَا، إِلَّا أَخْلَفَ اللهُ لَهُ خَيْرًا مِنْهَا»، قَالَتْ: فَلَمَّا مَاتَ أَبُو سَلَمَةَ قُلْتُ: أَيُّ الْمُسْلِمِينَ خَيْرٌ مِنْ أَبِي سَلَمَةَ؟ أَوَّلُ بَيْتٍ هَاجَرَ إِلَى رَسُولِ اللهِ صلى الله عليه وسلم، ثُمَّ إِنِّي قُلْتُهَا، فَأَخْلَفَ اللهُ لِي رَسُولَ اللهِ صلى الله عليه وسلم.

Muslim soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Yaayu jullit ñi Ummu Salamata yal na ko Yàlla dollee gërëm dafa wax ne dégg naa Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc benn bis muy wax ne: Amul benn jullit bu musiba di dal muy wax li Yàlla sopp ci moom: nun de Yàlla moo nu moom te ci moom lanuy dellu} [Al-Baxara: 156], (yaw sama Boroom jox ma ag fay ci sama muñ gii ci sama musiba gii, te wuutalal ma ko lu ko gën; lu dul ne Yàlla dana ka ko wuutalal. Nee na: ba Abuu Salamata faatoo ma wax ne: ana kan ci jullit ñi mooy gën Abuu Salamata?! Kër gi njëkk a gàddaay jëm ca Yonente ba yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, topp ne Yàlla dimbali na ma ba ma wax ko, Yàlla daal di may wuutalal Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc te moo gën Abuu Salamata.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Digle muñ ci musiba yi te bañ a yéjji.

Jublu Yàlla ci ñaan ko ci mettit yi; ndax ci moom la kuutlaay nekk.

Jullit fàww dafa war a jëfe ndigalu Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc donte xamul xereñteg ndigal.

Yiw yépp moo ngi ci topp gi jullit bi di topp ndigali Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.

Dellluwaay yi

Téere Muslim bi gën a wér (2/ 631) (918).