Skip to content

«bàyyil li la leerul te jëm ca la la leer, ndaxte dëgg ag dal la, fen nag ag jax-jaxi la".

Jële nañu ci Abuu Al-Hawraa As-Sahdii mu wax ne: wax naa Al-Hasan ibn Aliyun yal na leen Yàlla dollee gërëm ne ko: lan nga mokkal ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc? Mu ne ma: mokkale naa ci Yonnente Yàlla bi:

«bàyyil li la leerul te jëm ca la la leer, ndaxte dëgg ag dal la, fen nag ag jax-jaxi la".

«دَعْ مَا يَرِيبُكَ إِلَى مَا لاَ يَرِيبُكَ، فَإِنَّ الصِّدْقَ طُمَأْنِينَةٌ، وَإِنَّ الكَذِبَ رِيبَةٌ».

At-Tirmisiyyu ak An-Nasaa-iyyu ak Ahmad ñoo ko soloo.
Wér na
Leeral gi

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc digle na ñu bàyyi li ñuy sikk-sàkka ci ay wax ak i jëf ci ne dañu ko a tere walla déet, ndax dafa araam walla dafa dagan, jëm ci li ñu sikk-sàkkawul ag rafetam ak ug daganam wóor, ndaxte xol daciy dal, lu am sikk-sàkka nag day jàqal xol te du ci dale.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

War na ci jullit bi mu tabax ay mbiram ci li co leer te bàyyi li ñuy sikk-sàkka, te mu nekk ku am luko leer ci diineem.

Tere nañu tàbbi ci yu lënt yi.

Boo bëggee ag dal ak nooflaay nanga bàyyi li ñuy sikk-sàkka sànni ko sa ginnaaw.

Yërmàndey Yàlla ci jaamam ñi ndax da leen a digal li nooflaayu bakkan ak xel nekk, mu tere leen li njàqare ak ngëlëmte nekk.

Dellluwaay yi

Téere Sunna yi bu An-nasaa'iy (8/ 327) (5711).

Téere Sunna yi bu At-tirmisiy (4/ 286) (2518).

Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya (3/ 248) (1723).

Yataal gi (5)

التحفة الربانية في شرح الأربعين حديثًا النووية.

لإسماعيل الأنصاري (ص29).

شرح الأربعين النووية.

لابن عثيمين (ص153).

فتح القوي المتين في شرح الأربعين وتتمة الخمسين للنووي وابن رجب (ص56).