«ku ñu ag ñeewant xañees na ko aw yiw».
Jële nañu ci Jariir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«ku ñu ag ñeewant xañees na ko aw yiw».
«مَنْ يُحْرَمِ الرِّفْقَ يُحْرَمِ الْخَيْرَ».
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne ku ñu xañ ñeewant ba dëppoowul ak moom ci biri diinee ak àddina ak ni muy doxale ci boppam, ni muy doxale ak ñeneen ñi, kooku xañ nañu ko léppi yiw.
Ngëneelu ñeewant ak ñaaxe ci ñu jikkowoo ko, ak ŋàññ ak soxor.
Ci ñeewant la yiwi ñaari kër yi di nosewoo te ci lay seen i mbir di yaatoo,waaye ci soxor la safaani loolu di ame.
Ñeewant ci jikkó yu rafet lay balle ak jàmm, waaye soxor ci mer ak ñaaw jikkó, looloo tax Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc tagg ñeewant lool sax.
Sufyaan As-Sawrii yal na ko Yàlla yërëm dafa wax ay àndadoom ne leen: ndax xam ngeen luy ñeewant? Mooy nga tek mbir yi ca barabam, tar-tar ci barabam, ak nooy ci barabam, ak jaasi ci barabam, ak yar ci barabam.
Téere Muslim bi gën a wér (4/ 2003) (2592).
Yataal gi (12)
نزهة المتقين شرح رياض الصالحين.
لمجموعة من الباحثين (1/ 532).
تطريز رياض الصالحين.
لفيصل آل مبارك (ص416).
شرح رياض الصالحين.
لابن عثيمين (3/ 592).
كنوز رياض الصالحين.
لمجموعة من الباحثين (9/ 152).
بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.
لسليم الهلالي (1/ 687).
فيض القدير شرح الجامع الصغير.
للمناوي (6/ 241).