Skip to content

"ku sol sooy fii ci àdduna du ko sol fële ca allaaxira"

Jële na ñu ci Ibn Umar -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:

"ku sol sooy fii ci àdduna du ko sol fële ca allaaxira"

«مَنْ لَبِسَ الحَرِيرَ فِي الدُّنْيَا لَمْ يَلْبَسْهُ فِي الآخِرَةِ».

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day leeral ne góor gu sol sooy fii ci àdduna du ko sol fële ca allaaxira ndeem tuubu ko.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Li ñu jublu ci sooy mooy bu cosaan ba dara soppiwul, waaye bu dee sooy bu ñu defar moom du dugg si Hadiis bi.

Araamal nañu ci góor muy sol sooy.

Tere gi ñu tere sol sooy day làmboowaale it lal ko.

May nañu góor tuuti sooy bu nekk ci yéreem te yaatuwaayam bañ a ëpp ñaari baaaraam ba ñenti baaraam nga xam ne da koy def ay màndarga ci yére bi.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (7/ 150) (5834).

Téere Muslim bi gën a wér (3/ 1641) (2069).

Yataal gi (2)

منحة العلام في شرح بلوغ المرام.

لعبد الله الفوزان (4/ 207).